Armagedon
Ci làkku ibrë (הר מגדון) la tur wi jóge. Ci angale mooy Armageddon; Ci faranse mooy Harmaguédon
Armagedon mooy turu benn tund ci làkku ibrë bi ñu sotti ci làkku gereg. Ci làkku ibrë Megido (Meguiddo) la tudd. Ci Injiil dafa misaale bérab fu xare bu mujj bi nara am ci diggante gaayi Yàlla yi ak gaayi Seytaane yi ci muju jamano ji. Tundu Megido bokk na ci tundi Karmel yi. Dafa nekkoon ci benn boru xunt mu mayoon nit ñi jàll tund yi. Ci joor bu nekk ci taatam la Sóol (1Sa 31:1-8) ak Yosiyas (2Ch 35:20-24) dee, te Sedeyon amoon ndam ci waa Majan ñi (Jud 7).
Armagedon mooy feeñ ci Injiil ci Pe 16:16.