Arkelawus
Ci angale mooy Archelaus; Ci faranse mooy Archélaüs
Erodd Arkelawus, doomu Erodd bu mag ba, moo falu woon ci diiwaani Yude, Samari ak Idume (Idumée) 4 j.K. nguuru ba 6 g.K.. Yaayam Maltas (Malthrace) la tudd. Arkelawus ak Erodd Antipas ñoo bokkoon ndey ak baay. Yawut yi ak waa Samari yi jiiñ na ko kor ci kanamu buuru Room ndax coxoram. Buur bi Ogust Sesaar moo ko fuñ ci diiwaanu Gool (Gaule), maanaam Farans, ci 6 g.K.. Gannaaw loolu def nañu Yude diiwaan ci suuf nguuru Room, te jawriñ yi buuru Room fal yilifoon fa. Jabaram Mariyamënë (Mariamne), doomu Aristobul la, ki mu fase ngir takk Galafira (Glaphyra), jëtunu Alegsàndar (Alexandre), magam.
Man nañu gis tur wi ci Mc 2:22.