Arafu N

Nit nag ba laa nite day niit am xelam te du nar () te not ci am xel ba duñ koy nax ngirug naaxam

Di nëbb tey jëf te neexum xel di néewali wax () di noppi cig neen soriy nëx-nëx matal naalam

Di nemmikug naat te nargan bakkanam bañ a nay () nërméel itam néegi niig-niigal ngirug naayam

Fu’m tollu nay naabu tey nàmpal xelam bañ naw () tey natt boppam ci ag néewam akug naatam

Waxam nëtax neex ngirug nooyam nosub bakkam () di ñoddi muy nàcc’ak’ay nef daw sorig naagam

Te néeg ci bakkan bi ay tànkam na nooj bumu dem () mu naj ko bu’m nàngi faaw bay nuur ci ag naanam

Nemmat ko ba’m nenn noflaay bum ko xam na ko not () ba’m naagu bay niir te bum noppal ci ag naabam

Te yeew ko cig naw di dóor ciy nengateŋ te mu nal () dëgër ca ba’m siit mu naaxsaayal ko ciw naajam

Te nàmm xol ba ba dootul yëg naqar te du noos () ba dee ga ñëw far ne nuus ruuwam ga ci naawam

Te dee du néggandiku’s lëf, nës-nësal aki nax () du tax mu dem, nagg-naggal yit du dog naalam


 Naj ak forse
 Yeexe jëf ju am njariñ
 Jeng akug joy
 Sotti bu baax, nef it day firi njur mu jegee
 Xeetu lafañ mooy wóom yi jegee tànk yi soree   
 Nàngi faaw:saaraan ak teg jë 
  yedd
 Sàppi;bàyyi  
 Miir ak waccu
 Fàmb;suufu faar 
 naw
 Daas;ñawal  
 Bànneex bu diine lalul 
 Tëyye bu dëgër ak jàpp gu gaaw

 Jéllale  
 Waxi tappale yu nosuwul