Arafu m

Maandul te man yaw ci sag maas bul di mànke mukk it () bul def sa màndiŋ1 mi muy ab miinuwaay2 tubayul

Xeebal masëy wa te muurloo waame moo ami may () sa fit bu muy màcc jëm cig maax lu mànke nga ful

Bul mëdd may, yeete nang koy sante Yàlla bu wér () te say wax ak say jëf it nay màndaxoo matalal

Bul makk-makkal sa bakkan nang ko miinali yar () bul mer te bul metti, màbbal moy te muñ lu la dal

Metlànk far ko mu def menteñ ne meŋ ne mes () nga muure ko’g dëgg gàttal say mebët di jagal

Tey muñ mettiit moom la Yàllay méngaleek musalam () bul mel ne maaka ma cig bañ-tàng dund saxul

Mokkal te màggal, sa jëf bul màggal it matalal () bul yàq nig max te bul def makk màmm gënul



 1 Àll  bu sori 
 2Dëkkuwaay  
 Tawub wick-wiccal
 Ñawka lu tëlee dagg: ag ñawadi    
 Nëbb 
 Nay dëppoo, màndaxe mooy tollale gi nuy def ay balăs bu ñuy peese   
 Neexal ak a nbb-nabbee
 Man a nax ak man a baab
 Ne mes;naaxsaay
 Mbaxana mu ñu ràbbe bant ngir feg aw naaj
 Ne cell