Arafu A
Aw naa ci àlli waa Unaare fekk léen - ñu àngu ñoom ñépp di an calli aréen
ma ëyu leen ne aaye naa ko, indi léen - fukki andaar te boy te moytu aawe yéen
Te aw ci xàlli jub te moy anéeri moy - te wut aléeri topp àkki tool ya bay
Te àlli bànqaasi moy ak àkki ngëméen - bu léen di aas ci ëtt mbaa urmbali yéen
Lépp lu aay ër ko fa tey aayelu ay - tey àddu tey aar sa njaboot ci wépp ay
Te bul di ës ba muy waral ñu ëñ sa kéew - te mooy sa kiiraay li la ëw ba’ñ di la yéew
Te bul asar lenn, na ngay afal ku ne - sa xol bi nay af man a uuf mag’ak gone
Jépp ayib ju dul sa jos umpale ko - te ëmbalal ku nekk’u yiw àntule ko