Apoloni
Ci angale mooy Apollonia; Ci faranse mooy Apollonie
Benn dëkk ci diiwaanu Maseduwan la woon, ci wetu géej ga tudd Géeju Ese (Mer Egée). Nekkoon na ci diggante dëkki Filib ak Tesalonig ci yoonu wu mag wa tudd Yoonu Eŋaca (Via Egnatia), wi jaaroon ci diggante Asi Minër ak Itali.
Man nañu gis turu dëkk bi ci Injiil ci Jëf 17:1.
Xool it Wikimedia Commons
|