Ancos ci Pisidi

38°18′N 31°11′E / 38.3, 31.183

Ancos mooy benn dëkk ci wetu diiwaanu Pisidi, fu Pisidi digalook diiwaanu Firisi. Ci dëgg-dëgg ci diiwaanu Firisi la bokkoon waaye ba tey faraloon nañu ko tudd Ancos ci Pisidi. Gentam sorewul dëkk bu tudd tey jii Yalwacc (Yalvaç) ci Tirki (Turquie). Ancos nekkoon ca kaw benn tund wu ndaw bu nekkoon ca kaw benn palato bu yaatu te naat. Tund wu ndaw wa moom itam palato la woon, wu am dénd lu tollook 300 ektaar. Benn boor nekkoon 15 meetar ca kaw jooru palato ba. Waaye beneen boor nekkoon mbartal mu kenn mënul yéeg 60 meetar ca kaw joor ja. Naka noonu dafa mel ni tata te yomb na aar. Nekkoon na itam ca yoon wi mag wi waa Room tabaxoon wi jàll Asi Minér penku ba sowu diggante dëkku Tars ak dëkku Efes, wu tudd 'Yoonu Sebasëtë'.

Nguuru Selësid (maanaan waa Siri, ñi donnoon wàllu nguuru Geres) moo ko sampoon daanaka 300 at lu jiitu jamono Kirist, ngir teg fa xare ba, Bëggoon nañu aar nguur ga ca xeetu Pisidi wu nekkoon ca tund ya ca sudd, tamit am ndogal ca lépp lu jaar ca yoonu jaaykat ya wu mag wu jaaroon Asi Minër penku ba sowu. Sampoon na ko fa itam ngir boole ñi dëkk ca diiwaanu Firisi ak aada Gereg yi. Ñi fa jëkk a dëkk ñoo doon Gereg yi jóge dëkku Maŋesi ca diiwaanu Lidi ak Yawut yi jóge Babilon. Ca atu 25 j.K. nguuru Room moo def dëkk ba suufus Room, boole ko ak diiwaanu Galasi. Jaamburi dëkk ba yépp amoon nañu yelleef yu yem ak yosu waa dëkku Room. Tamit, indi nañu ay xarekatu Room yu bare yi ñu may ñu génne xare ba (maanaam soldat yu màggat), te may leen suuf ngir ñu dëkk fa. Gannaaw ga ndànk-ndànk dëkk ba tàmbali gën a niroo dëkki Room yeneen dëkk yi ko wër. Ca jamono Injiil dafa niroo dëkku Room ca wàllu yoon wa, ca wàllu nguur ga, ak ca wàlli tabaxin ak colin. Rafetal nañu dëkk ba bu baax ak pénc ya, ak kenu ya, te ak nataal yi ñi yett ca doj ak xànjar.

Ancos ci Pisidi moo doon dëkk bu gëna am solo ca diiwaan ba. Lu ëpp 100.000 nit ñoo fa dëkkoon. Dëkk ba boole na ay xeet yu bare. Amoon na ci bu jëkk waa Firisi, ba noppi indi woon nañu waa Gereg ya ak Yawut ya, ba noppi waa Room ya. Ci biir dëkk ba amoon na ñaari pénc yu réy yi ñu defare doj. Benn ca ñoom péncu Tibeer lañu ko tudd, mu am dénd bu tollook 300 meetar kaare, bi doon 'grand palaasu dëkk ba' fu nit ñi doon jaay, di fo, di waxtaan. Kenu yu réy te rafet ñoo ko wëroon. Beneen bi nag, mooy péncu Ogust moo dend péncu Tibeer. Ci seen diggante amoon na benn iskale bu am 12 mars (maanaam tegukaayu tànk), bu nekk am yaatuwaayu 20 meetar. Ca kaw iskale ba amoon na bunt bi ñu defare ak 3 ars yu réy-a-réy. Ab ars mooy lenn li ñu tabax ngir nekk pàttaliku. Dafa am ñaari kenu doj yu réy yi ñu boole ak lu mel ni xala doj bu jaar ca seen diggante, tiim leen. Def nañu bunt bi ngir nekk pàttalikukaayu ndam li Ogust Sesaar amoon ca xeex ya. Ca kawu ars ya yett nañu ay nataal yu réy. Beneen booru péncu Ogust moo doon wenn tundu doj. Ci biir tund wa yett nañu genn xala, rafetal ko ak ay kenu yu kawe ya. Ca diggu xala ga amoon na benn màggalukaay bu réy bi ñu defare marbar bu weex ngir teral seen Yàlla Men ak buur bi Ogust Sesaar. Ñu sooga àggale màggalukaay ba bi Pool demoon fa, ak ars ya bala mu dellusi ñaareel bi yoon. Ancos amoon na itam ndox ca tiwo yi jaar fépp ca dëkk, mu jóge ca benn bëtu ndox ca tund ya nekkoon fukki kilomet ca biti dëkk ba. Indi nañu ndox ak li tubaab tudd 'akwadakk'. Ci diiru 8 kilomet dafa jaaroon ci biir suuf si, waaye 2 kilomet yu mujj yi dafa jaaroon ca kaw pom bu kawe bi ñu tabax ngir yóbbaale ndox.

Seen Yàlla 'Men' la tuddoon. Amoon na itam beneen màggalukaayu Men ca wenn tund bu kawe lu tollook 25 kilomet ca penku dëkk ba. Bérab boobu mooy bérab bu bokkoon ca ña gën a am solo ca seen diine. At bu nekk def nañu benn po ngir teral Men. Gëmoon nañu ne Men mooy yàllay wér-gi-yaram, naataange, ak jàmm, te ku aar bàmmeel ya. Mooy itam yàllay weer wi. Ca nataalam ku niroo nit la woon mu sol yere. Misaale nañu ko ak wenn yëkk tamit ak nataalu weer bu am juróom-ñetti fan.

Sersiyus Poolus, boroom réew mi ca dunu Sipar (Jëf 13:4-12), dafa bawoo Ancos ci Pisidi. Ay bokkam moomoon suuf su yaatu ca gox ba. Moom gëm na Boroom bi Pool demoon Sipar. Xëyna Boroom réew mi moo boole Pool ak dëkku Ancos ba tax Pool ak Barnabas gaaw nañoo dem Ancos bi ñu jóge dunu Sipar.

Ca jamono Pool ndoxaanu yàqute, def yaramu neen, topp nafsu, màndite, lekk suuxu mala bu ñu toggul, te naan deret bokkoon na ca diine. Naka noonu, ñu bare bi ñu xoolee dundinu Yawut yi, ñu tàmbali xeeb diine ji ñu fekkoon, di tàmbali bokk ca diine Yawut ya, rawatina jigéen ñi woomle. Ca dëkku Ancos, jigéen ñooñu ñoo doon jabari magi dëkk ba. Naka noonu Yawut ya noonoo Pool jaaroon nañu ca jigéen ñooñu ngir ñu laaj seen jëkkër ñu dàq Pool ca dëkk ba.

(Jëf 13:14-51; 14:19-23; 2Tim 3:11)