Aminata Ture

(Yoonalaat gu jóge Aminata Touré)

Aminata Ture mu ngi juddu fukki fan ak ñaar ci weeru oktoobar atum 1962 ci Dakaar. Jigeenu nguur ju Senegaal la, dellu nekk taxawukatu àq ak yelleefi doom-aadama, nekk it liggeeykat ca Mbootaayu ya (ONU). Nekkoon na fi jëwriñ ji yore wàllu yoon ci Senegaal 2012 ba 2013 laata muy doon jëwriñ ju jëkk ci nguuru Senegaal 2013 ba 2014.

Aminata Ture
Jëwriñ ju jëkk ju Senegaal
1er septàmbar 2013 – 6 sulet 2014
(Fukki weer ak juroomi fan)
Njiitu réew Maki Sàll
Ngornmaŋ Ture
Ki mu wuutu Abdul Mbay
Jëwriñ ji yore wàllu yoon
4 awiril 2012 – 1er septàmbar 2013
(Menn at, ñeenti weer ak ñaar-fukki fan ak juroom-ñeent)
Ngornmaŋ Mbay
Ki mu wuutu Seex Tijaan Si
Dundu ak jaar-jaaram
Bésu juddu 12 oktoobar 1962 (Juroom-fukki at ak juroom-ñaar)
Bérebu juddu Dakaar
Kureelu pólotig APR-Yaakaar
Jànge International School of Management, Pari, Farãas
Liggeey Liggeeykat buy liggeeye réewam ak feneen ci àdduna bi

Dundu ak jaar-jaaram

Soppi

Tàggatoom

Soppi

Waajuram wu góor doktoor la, waajuram wu jigeen di ab saasfaam, moom mu ngi defe njàng mu suufe mi ca Tàmbaakundaa (gi waajuram wu góor doon liggeeye), wéyale njàngam mi ca liise Gaston Berger bu Kawlag. Atum 1981, moom moo doon ki jël ndam li ci koŋkuur seneraal bi ci wàllu koom, am bakalóoreyaa séeri B, ca liise Van Vollenhoven bu Dakaar. Ginnaaw gi mu dem jàngi Farãas, daldi di fa ame metiris ci wàllu koom-koom ca Dijon, DESS ci wàllu caytu këri liggeeyukaay ca Aix-en-Provence ak benn PhD ci manasmãa enternasiyonaal ca International School of Management (ISM), Pari ,.

Atum 1988 la tàmbale liggeeye SOTRAC, këru liggeeyu dem-ak-dikk ci Dakaar, foofee moo fa doon jiite siiwal gi ak jokkoo bi.

Njëlbeenam ci pólotig

Soppi

Way-bokk la woon ci làngu pólotig gi ba muy am fukki at ak ñeent ba tey. Muy yëngu ci iniwersite Farãas yi féete càmmoñ, maanaam waa góos yi, nekk it way-bokk ci Ligue communiste des travailleurs (LCT), kureel gi mujj soppeeku Mouvement pour le socialisme et l'unité (MSU). Moom moo nekkoon, ci kàmpaañi wotey 1993, jigeen ji jëkk a jiite kàmpaañu wote te doon ko defal Làndiŋ Sawane, ci pàrtim bi sax la mujj dugg at mi ci topp.

Pas-pasam ci xettali doom-aadama

Soppi

Aminata Ture daldi nekk ginnaaw gi, njiitu tëralini mbootaayu Senegaal giy taxaw ci taw-féexu njaboot gi[kañ ?]. Atum 1995, mu tàmbali di liggeeyal kureelu mbootaayu xeet giy taxawu askan (Fonds des Nations unies pour la population (FNUAP), mu jëkk fa nekk xelalkat bu jëkk ca njëwriñu njaboot ak ndimbalu askan ju Burkinaa Faaso laata mu fay doon xelalkat bu FNUAP ci réewi Afrig yi làkku farañse boole, nekkati lëkkalekatu tëralin wu ñu naan « genre et VIH » ci Afrig sowu-jant ngir màkkaanu kureelu mbootaayu xeet gi fi nekkal jigeen ñi ci dénd bi. Mu nekkoon fa di ñaax jigeen ñi ci soreel njur gi ak wérug yaram gi aju ci njur gi. Atum 2003, ñu fal ko ca New York njiitu deppàrtemãa bu àq ak yelleefi doom-aadama bu FNUAP.

Digganteem ak Maki Sàll

Soppi

Aminata Ture jóge New Jersey atum 2010, ñëw nekksi njiitu màkkaanu Maki Sàll (direktëer de kabine), mi doon njiitu Alliance pour la République, te bokk ci at mi ci topp, ci mbindum tëralinu Maki Sàll ngir kàmpaañu wotey njiitu réew yu 2012.

Mu wuutu Seex Tijaan Si ci njëwriñu yoon ji ci ngornamaŋ bu Abdul Mbay. Li doon sasam foofee, moo doon andi ay coppite yuy gën a woyofal, gën a gaawal doxinu yoon wi, gën a jegeel nit ñi ëttu àttekaay yi, yaatal kureelu sàrtu réew gi (Conseil constitutionnel). Ci weeram yu jëkk yi la tàmbale doxal xeexu ger bi Maki Sàll bëggoon, ak ay lëñbët yi mu doon def ci doxalinu njiiteef gi weesu ak tamit ni kilifay nguuru Abdulaay Wàdd yi daan yore alali askan wi. Bokkoon na ci kilifay Abdulaay Wàdd yooyu, Kariim Wàdd, doom ji.

Alalam ji nga xam ne ñaari taax (etaas) yu mag la ci Senegaal ak beneen bu nekk Etaasini (USA), ñu ngi ko xayma ci juroom-ñaar téemeeri milyoŋ ak juroom-ñaar-fukk ak juroom-ñaari dërëm ci CFA (777 millions de francs CFA).

Jëwriñ ju jëkk

Soppi

Aminata Ture ñu ngi ko fal benn fan ci weeru septàmbar atum 2013, mu taxawal ngornmaŋ bi ca suba sa xaat.

Ñeenti fan ci weeru sulet atum 2014 la ko njiitu réew mi ñaanal, ginnaaw bu Xalifa Sàll jëlee ndamal wotey meer yi ci gox bi mu dëkk ci Dakaar,. moom Aminata Ture. Mohamet Jonn, mi fi doon liggeeye ca Mbootaayu xeet ya, moo ko wuutu foofee mu nekkoon juroom-benni fan ci weeru sulet.

Féewiriyee 2015 la ko Maki Sàll tabb ndaw lu sës ci njiitu réew mi ngir mu koy doxal ay yonnent ci biir réew mi ak bitim réew yépp.

Dundug biiram

Soppi

Aminata Ture am na ñetti doom. Nekkatul soxna ci Umar Saar. Jëwriñ la woon ci nguuru Abdulaay Wàdd. Seen doom ju jigeen ji, Joor Saar, mu ngi ame ay lijaasaam ca iniwersite bu Yale, nekk ca Etaasini (USA). Jamono jii, mu ngi ci buumu sëy, borom-këram di ab njaatige (ãtarperenëer) bu tuddu Umar Kulibali.

Téere, jukki wala dali web yi ñu yër

Soppi

Seetal tamit

Soppi

Lees bind ci moom

Soppi
  • (en) Torild Skard, Women of power : Half a century of female presidents and prime ministers worldwide, Policy Press, 2014, p. 297-298 (ISBN 9781447315780).

Jukki yi ñu ko tudd

Soppi
  • Limu jëwriñ yu jigeen ci Senegaal : <small>Liste de femmes ministres sénégalaises</small>
  • Limu njiitu pólotig yu jigeen : <small>Liste de dirigeantes politiques</small>
  • Nekkinu jigeen ci Senegaal : <small>Condition féminine au Sénégal</small>