Amfipolis
Ci angale ak ci faranse mooy Amphipolis.
Dëkk bu am solo la woon, ci diiwaan bu tudd Maseduwan ci jamano nguuru Room ji. Ci bëj-gànnaaru Géeju Ese (mer Egée) la nekkoon. Nekkoon na ci yoon wu mag te wu am maanaa wu tudd Yoonu Eŋaca (Via Egnatia), wu jaar ci diggante Asi Minër ak Itali.
Amfipolis dafa feeñ ci Injiil ci Jëf 17:1.