Aliin Situwe Jaata

Aline Sitoé Diatta, ñu koy woowe itam « La Dame de Kabrousse ", judd ci 1920 ci Kabrus ci bëtu saalum Senegaal, faatu ci 1944 ci Timbuktu, ci Mali, ab ndaanaanu waa Senegaal, rawatina waa Casamance ci kolonisasioŋ français.

Aliin Situwe Jaata
Njiitu réew Senegaal
Dundu ak jaar-jaaram
Bésu juddu 1920, Kabrus
Bérebu faatu 22 Mai 1944, Timbuktu
Réew Senegaal
Liggeey sarxalkat bu jigéen

Aline Sitoé Diatta mingi juddoo ci atum 1920 ci Kabrus, ci Kaasamaas, diwaan bu nekk ci bëtu saalum Senegaal, ca jamono jooju koloni bu français nekkoon ci biir Afrik sowwu jant . Waajuram ñooy Silisia Diatta ak Assonelo Diatta, waaye, ndijaayam Elabalin Diatta moo ko yar.