Ag Mottali
Ag mottali :
Laa yéene woon a indi fii nag la mate () te mooy wolof ya sànku woon ba tëe jote
Ma jug dabaatalaat ko ngir mu dekkiwaat () te suuxataat reen ya ba xob ya seqiwaat
Ba meññatam ma ñor njariñ la daj fu ne () ku nekk mos ca kotttéef la daj ku ne
Ñu bokk fëx ku des ginnaaw jéem a dabe () te daw ba roppi népp nag te buñ rabe
Mu dooni mbég ci népp tey ag ségëre () te xel yi dal ba xol yi dootul fér-féri
Yaraax yaraaxam yi itam fatt taraj () ba ab poroxndoll du des bu lenn xaj
Ba sun cosaan xajam-xajam ya set wesal () layaat ko seggaat ko ba tër dootu ca des
Ñu rat ko nag ba dóotu dàngang jawali () ci ndànd-fayfayug keneen bay lëjali
Ne nit amul lu dul cosaanam ak ngëmam () cosaan la it làkk a ca jiitu nañ ko gëm
Ku wàcc sab andati and boo dem it () fekk boroom ca kaw ne déjj day ku mat
Ndegam dangaa waññiku delsi ci sa bos () fekk keneen toog ca dangay ku xel ma des
Kon maa ngi woo népp ñu bokk takkuwaat () te fonk suñ làkk wi buñ ko sànniwaat
Nit bu nitee du dem ci tool bàyyi sasam () di bay sasuw keneen ba booyaluw sasam
Dafay fexee lippiku népp bay sasam () bu sottalee bayal keneen di ndimbalam
Dafay jariñ nit kit e bañ koo jariñoo () balaa jariñ nit ki nanig ba jariñu
Ñu ñaan ci Yàlla miy boroom mu boole ko () ci jëf yu yiw ya suñ xel it mu dolli ko
Te def ci woy wi barke xiirtal nu ci way () ci fonk suñ làkk wi népp bokk wéy
Ba tax manul a jot yeneen làkk yi cig jëm-kanam Seqi: jebbi Wattiit; lu nu watt Daw teeyadi Mbégte Diggante yu dara nekkul Bën-bën bu xaw a yaatu yeew Rëcc ak màmm Waññil keneen aw sasam ginnaaw bi nga bayee saw sas ba noppi Xasaayit gi Sax ci mbir, way ci deŋ