Abiya
Ci làkku ibrë la tur wi jóge. Ci angale mooy Abijah or Abia; Ci faranse mooy Abia
Ci Injiil dañuy gis ñaari nit ñi bokk tur Abiya.
- Ñaareelu buur ci Yuda, mooy doomu Robowam. Ñetti at la nguuru ci Yerusalem. Bind nañu ay jalooreem ci 1Ki 14:31-15:8; 2Ch 11:20-22; 12:16-14:1. Bokk na ci maamaati Yeesu yi ñu bind ci Mc 1:7.
- Kenn ki soqikoo ci Aaroona (1Ch 24:10). Daawuda fal na askanu Aaroona ngir ñu toppatoo liggéeyu këru Yàlla. Mu xàjjale leen ba ñu nekk 24 kër. Kër gu nekk toppatoo nañu ñaari ayu-bés at bu nekk. Sakariya, baayu yonent Yàlla Yaxya bokkoon na ci askanu Abiya (Lu 1:5).