Abilen
Ci angale mooy Abilene; Ci faranse mooy Abilène
Diiwaan bu ndaw la woon, ci Siri ci diggante Libaŋ ak Damas. Diiwaan ba wër na dëkk bu tuddoon Abila. Abila sore woon na Damas ca sowu kaw lu tollu 29 kilomet. Bi Yeesu juddoo Lisañas moo ko yilifoon. Gannaaw loolu bokk na ci nguuru Erodd Agaripa II ba noppi ñu boole ko ak diiwaanu Siri.
Ci Injiil dañuy wax ci Abilen ci Lu 3:1.