Abdu Juuf
Abdu Juuf moo ngi juddoo Luga 7 Satumbar 1935, doonoon njiitu réewum Senegaal ci atum 1981 ba 2000, ginnaaw bi mu nekkee njiitu jëwriñ ci atum 1970 ba 1980. Ginnaaw ga mu wuutu Leopool Sedaar Sengoor ci njiitu réew mi ci diggante 1981 ak 2000, ay nguuram màndargawoo nañu jëm-kanam ci demokraasi, yokkute ci ubbeeku ci koom gi ak yaatal bànqaasi nguur gi.

Liggéey na itam ba baatu Senegaal gën a jolli ci àddina si, ndax diplomaasi bu am solo ak bokk bu am solo ci ndaje yu mag yi am ci biir àdduna. Liggéey na itam bu baax ngir réew yu Afrig yi gën a bennoo, jaare ko ci lëkkaloo gu gën a am doole.
Ginnaaw loolu mu nekk njiital Farankofoni, di yor bépp mbootaay ak bépp sémb ci réew yi bokk làkku waa-faraas (Mbootaayu Réewi Farankofoni, TV5Monde, Ngomblaan gu Mag gu Farankofoni, Mbootaayu Daara yu kawe yu Farankofoni ak Daara ju Kawe ju Senghor ju Alegsàndiri). Coppite yi mu amal gën na fésal seen liggéey, gën leen a xëcc ci àdduna si, ndax liggéey yu am doole yi mu def ci wàllu politik ak diplomaasi, ak gën a suqali mbooleem mbootaayi ñiy lakk farañse.
Njàngam
SoppiAbdu Juuf, doomu yóbbkatu bataaxal bi cosaanoo Luga te di ab Séeréer, bi muy ndaw lañu ko yóbb ci maam ju jigéen ca Ndar. Fa la nekk ba am lijaasa bakalorea.
Bi muy toll ci juróomi at la dem jàngi diine ci daara Alquraan ja. Bimu amee juróom ñaari at la tàmbali njàngum waa-faraas ca daara Brière-de-l’Isle (leegi daara Émile Sarr). Ginaaw ba, ba mu fa jeexalee, la jàngi ca daara Faidherbe (leegi di daara Seex Umar Fuutiyu Taal), ca Ndar. Ca Daara jooja la toppe juddug Bloc Démocratique Sénégalais, di kuréelug politig gu Leopool Sedaar Sengoor taxawaloon, te di fu yaayam ju ndaw bokkoon.
Ci atum 1955, ginnaaw ba mu amee bakalorea ci xeltu, la dugg ci daara ju kawe ju Ndakaaru (leegi di Daara ju Kawe ju Seex Anta Jóob ). Ci at yooyu doon na dugg bu baax ci mbootaay yi. Doonoon na njiitu kureel gi yor daara ak daara yu kawe yi ci Luga, di dajale ndongo yi ci daara ak daara yu kawe yi ci biir gox ba ci jamonoy bér yi. Dafa doon jaar ci kureel gii ngir di jàngal ndongo yi ci dëkkam, ci bér gi, ak di amal xew-xew yu mag ci wàllu mbatiit. Moom itam moo doon jiite CECAS, di Dajaleeb Mbootaayi Daara ak Daara yu kawe yi ci Senegaal. Ci 1958 la am lijaasa ci wàllu yoon.
Ci at moomu, ci la jàll ag fitte ngir mën a dem ci Daara ju Réewum France ju biti réew (École nationale de la France d'outre-mer, ENFOM) ci Pari. Bi mu nammee liggéey ci wàllu yoriinu kopparu réew, la dem def ab liggéey bu gàtt ci Njëwrinu Koppar gi. Ci ñaari at yooyu, la dugg ci wàllu sindikaa, mu dem jegeji kureelu ndongoy Senegaal yi ak kureelu ndongoy waa-afrig yu ñuul yi ci Faraas. Ci atum 1960, ci jamono ji tubaab yi di génn Afrig, bokk na ci dongo yi mujj ci ENFOM, ca la jeexalee am njàngam, ngir am lijaasaam mu bind ab jukki bu tuddu Islam ak askanu wolof.
Jaar-jaari liggéey ak Ndombo-tànk
SoppiSenegal dafa moom boppam ci 1960. Abdu Juuf bàyyi liggéey ba mu yoroon Faraas, dellu Ndakaaru ngir ànd ak càmm gu bees gi. Tambaliwoon na liggéeyam ci ay pekku njëwrin yu bari.
Teel naa jël liggéey yu mag ci Senegaal. Bisu 11 desàmbar 1961 lan ko fal guwërneer Siin Saalum bi mu amee 26i at, laataa muy nekk ci njiitu réew mi ci Léopold Sedaar Seŋoor ci atum 1963, ginnaaw loolu mu nekk sekkerteer jeneraal ca njénde la ca atum 1964.
Ci atum 1968, ginaaw bi ñu falaate Léopold Sédar Senghor, ci la ñu fal Abdu Juuf muy jawriñ ji yor wàllu palaŋ ak ndefar.
Moo yor seytu gi ngir amal ñatteelu palaŋ bi Réewum Senegaal amal. Lu ci melni liggéeyukaay yi, mbay mi, jumtukaay yi, njàng mi. Ci jamono jooju lañu tàmbale waxtaan ak Kanadaa, muy ak lëkkaloo, ngir sos Daara Politeknik ca Cees. Mi ngi yëngu itam ci yokkuteg koom-koomu Kaasamaas.
Ci atum 1970, ginaaw bi ñu soppi sàrtu ndayi-àttey réew mi, ñu taxawal liggéey ak doxaliin jawriñ ju njëkk, ñu fal ko Abdu Juuf bi mu amee 35 at, muy liggéey bu mu nekkoon lu tollu ci fukki at.
Njiitu Réewum Senegaal
Politig
Bisu 1 saŋwiye 1981, ginnaaw bi Léopold Sedaar Seŋoor bàyyi ci bopp réew mi, Abdu Juuf ci la nekk 2eelu njiitu réewum Senegaal.
Dëgg la, sàrtu ndayu réewum Senegaal dafa wax ni su amee bërug nguur, jëwrin ju njëkk ji mooy yeggali nguur gi ba joŋante yi ci topp.
Abdou Diouf, bi mu demee ba yeeg ci liggéeyam bu bees bi, mi ngi wéyal demokaraasi bi ki ko jiitu tàmbaliwoon, ci yokk pàrti yu bari, bu njëkkoon ñeenti pàrti politig ñoo amoon, moo tax mu jeexal jiixi-jaaxa ci (clausus) bi.
Ci anam yu mel noonu, ci la dindeenjuumtey saabal yi balaa muy yaatal ndànk-ndànk ak sos Caabal ju bees rajo, maye ñu siiwal ay xibaar yu bees.
Ngirug màndargaal, ci la tudde jàngune bu Ndakaaru ci turu gëstukat bi nekkoon boroom xam-xam ci Isipt gu njëkk ga, di Seex Anta Juup. Lu ko jiitu, mayoon na ko mu nekk jàngalekat ci daara ju kawe ji, te njiitu réew mi Seŋoor bëggul woon loolu, ndax yëngug boroom xam-xam bi ci politig.
Koom-koom
SoppiAbdu Juuf ci atum 1988.
Abdou Diouf tàmbali tabax réew mu bees, am doole ci wàllu koom-koom ak liggéey.
Ci atum 1985, ci la taxawal ay sosiete yu bari ngir ñu mën a taxaw ci nekkiinu réew mi ak ay serwiis, lu ci melni Sonatel – ci tàqale liggéeyu jokkoo ak post ci biir (l'Office des Postes et des télécommunications) – ci atum 1985, Sosiete bi yor wàllug Séddale ci Réew mi (Sonadis), Sosiete bi yor Njaayum Diw ci Senegal (Sonacos), ICS ak ñoom seen. Ubbi na Senegal ci wàllug turism ci defar ay resort ci tefesu géej yu melni Saly Portudal ci 1984, waaye itam ci defar fundaasioŋ ngir turism bu jëm ca kanam, ci taxawal Centre International pour le Commerce Extérieur du Senegal (CICES) ci 1986, foofu lañuy amal ay foire yu mag ci diiwaan yi ak ci réew mi yépp.
Tabax nañu itam ay otel yu bari ngir yokk kàttanu daluwaayu turist yi ci réew mi, lu ci melni Le Méridien Président, bi mujjee soppiku nekk king Fahd Palace, làmboowaale it Pale bu nguur gi di defee ay ndaje ak i waxtaan.
Daanug Farã CFA ci atum 1994 moo waral Abdu Juuf tàmbali politiku ajustement structurel, binga xam ne wax na ci ay kàddoom ne « dafa mettiwoon lool ci askan wi », waaye dimbali na lool koomu-koomu Senegaal bamu yéwén , jëm kanam ci njeextalu ati 1990 yi.
Moo tax ci atum 2000, Senegaal dafa am yokkute gu toll ci 6%, li ko gën a waral mooy koom-koomu turism bi, luy toll ci 800000i nit doon fi dugg ngir turist ci at mu nekk, ci geneen wàll it mbirum jokkoo gi nekkoon lu jëm kanam jaare ko ci Sonatel, ak ICS.
La ko dalee ci atum 2000, réew mi dafa wéy di am yokkute ci diggante 3 ba 5%, loolu dafa taxoon ñu man a dugal xaalis bu bari ci infrastructure yi ak ci koom-koomu askan wi.
Wàllug mboolaay
SoppiRëyaayu politigu desantralisasioŋ bi nguur yi toppalante tëraloon, moo waral ñuy dugal ay serwiis publik ci réew mi yépp. Ñu tabax ay Hopitaal yu mag, yokk ci ay santar yu wérgi-yaram ak ay dispenseer ci dëkk yu ndaw yi ngir jàppale askan wi.
Noonu la amee it ci njàngum réew mi, ndax tabax nañu daara yu kawe yi ci dëkk yu mag yi, boole ci daara yu ndaw yi ak yu digg-dóomu yi ngir gën a suqali njàng mi ci réew mi yépp.
Kon bépp sarwiisu administraasioŋ bu mag dafay gëna jege askan wi, njiiti dëkk yi di leen jàppale ci seen liggéey, te Abdu Juuf di leen gën a jox kàttan ak moomeel (loi de décentralisation de 1996).
Bu dee ci wàllug ndox , xëccloon nañu ndox yóbbul ñu bari ci askan wi ci dëkki taax yi, bu dee ña ca kaw ga ñu gasal leen ay teen yu dëppoo ak Jamono.
Noonu it lees def ci wàllug mbay mi, woo baykat yi ñu booloo ci ay kuréel ngir man a jàpplante, ngir dooleel it séenug jàpplante, ngir yombal amug jumtukaay i mbay yi lu mel ni masinu bojj.
Ci gàttal daal, diiru li mu nekk ci nguur gi, Njiitu-réew mi Abdu Juuf def na lumu man ngir réew mi tegu ci yoon ci wàll yépp, loolu tax Senegaal bokk ci réewi Afrig yi gën a am solo , ñu bari di jugee ci yeneen reew yi di fi rawati na Ndakaaru.