Abba
Ci làkku gereg \~Abba\~; Ci làkku ibrë \^aba\^. Ci làkku yawut la baat bi jóge. Ci angale mooy Abba; Ci faranse mooy Abba
Mu ngi tekki ‘pàppa' ci làkku yawut. Turu cofeel la. Yeesu moo jëkka boole tur wi ak Yàlla. Làkku yawut wi ci jamano Injiil ji, arameyni la tuddoon. Mujjoon nañu àbb baat bi, duggal ko ci làkku gereg ak ci làkku ibrë.
Ci Injiil dañuy gis Abba ci Mk 14:36; Ro 8:15; Gal 4:6.