Aana
Ci angale mooy Anna te ci faranse mooy Anne.
Yonent bu jigéen ku màggat lool la woon. Jëkkëram gaañu na waaye Aana séyaatuloon. Guddi ak bëccëg dafa doon jaamu Yàlla ca këru Yàlla ga ca Yerusalem. Bi waajuri Kirisit indi woon Yeesu ni liir, Aana waxoon na ci moom ci kanamu ñépp ñi fa nekkoon. (Lu 2:36-38).
Ci Injiil dañuy gis Aana ci Lu 2:36,38.