AJ
AJ MÀKKA
Bind bu jëkk
Nu fas yéenee jàngale aj ak ajiin yi, nu tàmbalee ko nii:
Xeeti ajiin yi ñatt lañu:
▪︎Ifraad : (li muy tekki mooy bennal, wéetal, aj rekk a tax nga jug), su dee ci waa Senegaal ñu armale ca armalu (miixa) ba ñuy wax Zul Hulayfa (Biiru Hali), di jumaa ju nekk ca wetu Madiina, ngir def faratay aj. Soo noppee ci mbooleem jëfi aj ji aki jaamoom, dinga man a def sunnas Umra, su boobaa jënd gàtt du la war, di ko ray ci bisub iid gi (hadyu)
2eelu bind
▪︎Ajug xéewu (tamattuh):
Mooy nga armale ca armalu ba ci yéeney jëkk a def sunnas Umra. Soo noppee ci def jëfi Umra, nga summiku (ci sa yérey armal), sol yére yi nga baaxoo woon. Ci juroom-ñatteelu fan ci weeru tabaski (zul hijja), ca suba sa, ca ngay armale ca Màkka ci yéene def faratay Aj, ànd ak ajkat yi dem Munaa ngir def jaamuy aj yi ba ñu jeex. Tawaaful qudoom nag du la warati. Li ngay def kay mooy jënd ab gàtt, ray ko ca bisub tabaski ga. Ndaxte dangaa xéewoo (tamatuhe) jiital sunnas umra ci faratay aj, soo manul a jënd ab gàtt ngir ñàkk koo man, kon dangay woor ñatti fan ci biir aj gi, ak yeneen juroom-ñaar soo delloo sam réew
3eelu bind:
▪︎ Ajug Qiraan walla ajug lëkkale: mooy mu aramale yéeney sunnas Umra ak faratay Aj ci wenn waxtu ( maanaam mu yéenee defandoo ñaar yi), sooy noppi ci jëfi aj ji fekk na nga matal tam jaamuy umra. Fii it hadyu war na la walla woor na nga ko defe woon ca Tamattuh (xéewu). Dangay gis ne ci jëf yii yépp aji aj ji day xér ci jóoxe faratay aj ak sunnas umra ngir am seeni yool ak pay
4eelu bind
▪︎Aj daa am ay ponk aki wareef.
Ponki aj deesu leen jange (defare) dereet (ci hadyu) su ñu yàqoo, ñoom nag ñeent lañu:
1 - Armal: mooy yéenee dugg ci aj gi, walla sunnas umra, mu lëkkaloo ak rafle ci lu ñu ñaw, ak sol lees yérey armal ya, ak wax làbbayka jëm Màkka gu sell ga
2 - Dox diggante Safaa ak Marwa, mooy dox ko joroom ñaari yoon, benn mu nekk ci ginnaaw wërug dikk gi (tawaaful qudoom) ñeel ajkat bi, walla ginnaaw tawaaful Ifaada (wërug bëbbal gi) ñeel ajkat bi deful tawaaful qudoom, ak it ñeel ki def tamattuh, nga xam ne daa jiital sunnas umra , mujje faratay aj
3 - Tawaaful Ifaada (Wërug bëbbal gi): mooy wër gi ajkat bi di def ci bisub tabaski, ginnaaw bi mu sànnee Jamratul Haqaba, ak ginnaaw bi mu rayee am hadyoom, su fekkoon mi war ko, ak wat boppam walla wàññi ko ( xoos ci mbooleem kawaru bopp gi).
4 - Teew Arafa : ajkat bi day juge Munaa, dale ko ci penkuteg jànt gu bisub juroom ñeent ci tabaski wi, fu mu teew ci wàlli Arafa rekk mu doy, moo xam daa tëdd, mbaa mu war, walla mu taxaw, waaye su génnee Arafa (maanaam nekkul ciy wàllam) nag ajam baaxul. Arafa nag mooy ponkub aj bu mag bi. Teew fa nag, doore ko ci sawaal (digg-bëccëg) ba jant so. Nekk ga fa ajkat bi di nekk ba jant so nag daa bokk ci waajibaat yi (wareef yi), ku ko deful man na koo jange (defare) dereet (hadyu), su ci ajkat bi lotte ngir benn ci sabab yi
5eelu bind
WAREEFI AJ:
Wareefi aj yiy jangoo (defaroo) ci dereet, ñi ngi jangoo (defaroo), soo ci bàyyee benn ci jënd am hadyu te ray ko, ngir jaamoo ko Yàlla.
Wareefi aj yiy jangoo ci dereet, su ci benn faatee ajkat bi, ñooy yii:
1 - rafle ci lees ñaw ak luy peek ( luy wëre), maanaam bañ a sol yére yu ñu ñaw, ak mbir yuy peek (wër) ab cér niki jaaro ak yu ni mel.
2 - Armale ca armalu (miixa) ba ñu jagleel dëkk bu ne. Senegaal seen bos mooy Biiru Ali
3 - di wax làbbayka ba ca digg-bëccëgug bisu Arafa
4 - Tawaaful Qudoom (wërug bëbbal), mooy tawaaf gi ajkat biy def su agsee Màkke rekk te fekk mu armal ngir aj Ifraad
5 - Ñaari ràkkaay tawaaf yi ci Ifaada ak Qudoom, waxees na ne : seen àtte ñooy sunna
6 - Dox safaa ak marwa nekk ci ginnaaw tawaaful qudoom te jokk ci, su dee ajkat bu juge dëkkam ñëw Màkka te armaloon faratay aj
7 - Nekk Arafa ci bëcëg gi, dale digg-bëccëg ba jant so
8 - Wàcc Musdalifa cig dellu juge Arafa ci guddig tabaski gi, jullee fa timis al gee boole leen te wàññi gee gi
9 - fanaan Munaa ñàtti guddi ginnaaw bisub arafa walla ñaari guddi gën jaa néew, guddig ñaareelu tabaski, ñatteel ak ñeenteel su ko sànni jamra yi ci ñeenteelu bis bi ñoree. Su dee yam ci sànni jamray ñaareelu bis ak ñatteel, kon du jar muy des Munaa di fa fanaanati ca ñeenteel ba.
10 - Sànni ñatti jamra yi ci bisi tashriiq yiy ñatt (ñatti fan yi sës ci tabaski gi), waxtuw sànni wi mi ngi tàmblee ci digg-bëccëg ( zawaal) ba jant di so. War na ajkat bi mu yéenewaale buy armal ne dina joxe am hadyu, muy ray ab gàtt ci lépp lu mu man a def ciy wuute, wallay tere. Def wuute mooy ñu digal la defoo ko.
Def tere mooy ñu tere la bàyyiwoo. Su boobaa loolu dina doy.
6eelu bind:
Terey aj yi:
1- sol lees ñaw walla luy peege: ku armal du sol jàllaabi, simis, pantalong, du jenn tubay mbaa mépp mbubb mees ñaw, du sol it jaaro, kaala, walla lenn lees man ne day peege mbaa ñu ñaw ko.
2 - Lees man a féexale yaram wi ak di ko setal, du muur bopp bi, du wat kawar gi, du lewwi we yi, du dindi ag fagg akub tër ci bopp bi walla ci yaram wi, du jëfandikoo gëtt ci mbubbam mbaaw yaramam, mbaag diw ci bopp bi, ak yeneen yi aju ci setal mbaa dindi ay taq-taq añs
3 - Jigéen ñi: du dagan ci Aji armal ci Màkka muy jege jabaram cib sëy walla laal, mbaa fóon, walla muy ngoro mbaa muy ngorool, mbaa muy fasal boppam ab sëy mbaa mu koy fasale.
4 - Rëbb: daganul ci ku armal muy rëbb dara ci rëbbum jéeri mbaa mu koy ray, moo xam luy dox la mbaa luy naaw, mi ngi ci urum ji mbaa mu génn ko, daganul ci moom it moy dog garabi urumi Màkka ji.
Ajkat bu góor beek bu jigéen bi ci nii lañuy wéy di ñu ñu aaye mbir yii ba kero ñuy sànni jamrab Haqaba, dal di summiku summiku gu ndaw gi, bu booba lépp daganaat ci moom ba mu des jigéen ak rëbb, ñu sib ci moom gëtt, su defee tawaaful Ifaada, dox safaa ak marwa, su defagul it tawaaful wadaah, day def summiku gu mag gi, su boobaa lépp lu armal di aaye dellu dagan ci moom, mu man a jariñoo soxnaam, ndax def na mbooleem ponki aj gi, li ko dese mooy sànni jamra yi ci bisi tasriiq yi( bisi ñaareel, ñatteel ak ñeenteel bu tabaski gi)
6eelu bind:
Yiy yàq aj ci ñatti mbir lañu nekk:
1- Ñàkk a teewe arafa, loolu mi ngi ame ci ñàkk faa man a teew cig wàll ci guddig tabaski gi, muy diggante timis ba fajar fenk.
2 - Bàyyi ponk ci yeneen ponk yi dul jangu ci dereet ba waxtoom jàll, te manoo koo dabaat.
3 - Aji armal ju jaxasoog soxnaam te sànneegul jamrab hawaba, wëragul Ifaada, te bisu tabaski gi jeexagul. Su amee nag ginnaaw benn ci ñatt yii, du yàq aj gi cig matale, waaye hadyu moo koy war. Su aj gi yàqoo ngir senn ci sabab yii nu waxoon, ajkat day mottali ag ajam te dal di koy fay saa so ko manee , dal di ray hadyu ngir aj gu yàqu gii te yeexe ko bay fay ca at may ñëw su ko aj jàppandee.
7eel bind:
Kañ la hadyu di war ajkat bi?
Bokk na ci sabab yiy waral hadyu:
1 - su ajkat bi bàyyee benn ci wareef yiy jangoo ci dereet
2 - su doonee ku doon tamattuh, jiital umra ci aj, ngir waxi sunu boroom ja: ( ku xéewoo umra ba aj, la jàppndi ci hadyu), ak su defee ajug lëkkale (xiraan), ( maanaam boole sunnas umra ak faratay aj ci yenn jëf ni nu ko leerale woon ca na ñuy armale ci xiraan
3 - su amee gàllankoor bu ko teree mottali faratay aj gi, ngir waxi sunu boroom ji: ( Bu ñu leen gawee, la jàppndi ci hadyu), su amul lu mu man a jënde hadyu ba koy ray, woor ñatti fan da koy war ci aj gi ak yeneen juroom ñaar su delloo dëkkam, ajkat bi man naa coobarewoo joxe hadyu te du ko war, mu ciy sàkku tuyaaba rekk ngir ne deful dara ci sabab yi nu tudd tey waral hadyu.
Njot ( walla fidya) maanaam ak li koy waral :
Njot walla fidya mooy kafaara (far) gu jëm ci tere yi ajkat bi def, di ci ame ag xéewu akub noflaay niki sol lu ñu ñaw, mbaa muur bopp, walla setal yaram, dindi ag fagg, jëfandikoo gëtt (parfum):
Fidya nag ñatti xeet la, nga tànn ci bu la nee:
• woor ñatti fan ci fu la neex
• lel 6 miskiin (miskiin bu ne ñaari mudd)
• ray ab gàtt xar mbaa bëy
Tegtalug ñatt yii mooy waxi sunu boroom ji: ( ku ci nekk ci tawat mbaa mu am loraange ci bopp bi, na def fidya, benn mu woor, mbaa mu saraxe, mbaa jaamu (nusuk)
8eelu bind
Yeete ñeel ajkat bi:
Soo génnee sa kër yaw miy aj jëm Madiina ngir siyaare armal waru la, dangay sol lu la neex, di gëttu ak a set waxtu wu la neex. Soo jugee Madiina nag ngir war a armal ngir aji, dangay dem ca sab armalu (miixa), ni ma la ko waxe woon, waa Senegaal seenub armalu mooy Biiru Ali, di jaaka ju ne ca wetu Madina ( Zul Hulayfa) mooy miixam waa Madina, di soree màkka 450 kilomet (junñay). Ku romb sa miixa (armalu) te armalewoo fa, loolu dina waral hadyu war la, ci miixa mii rekk it lees di soppe ñaari ràkka
- armalug jigéen mooy mu wuññi xarkanaman ak ay tenqam, waaye day sol yére yi mu baaxoo woon a sol, yi ñu ñaw ak yiy peege, muur bopp bi, li war ci moom it ginnaaw jaamuy aj gi walla umra gi mooy mu wàññi kawaram rekk, su dee góor nag day watu mbaa mu wàññi ci mbooleem kawar gi.
- ajkat bi su dee wër kaaba gi ba jullig farata jot day dog wër ga ba ànd ak nit ñi julli ba ba noppi, dellu ca wër ga ca barab ba mu taxawe woon, mottali la ko dese woon ciy wër.
- Su jigéen gisee mbërëg, day wéy cig ajam, def ay jaamoom lu ci dul wër kaaba gi, ndax da dul sañ a dugg ci jàkka ji, du wër it ndare bu dafa laab te sangu, ndax wër dafa laaj jàpp niki julli.
- ku sikk ci ñaata wër la def na jàpp la ko wóor, misaal mu doon sikk ndax ci ñatteel la nekk walla ñeenteel, su boobaa day jàpp ne ci ñatteel la nekk, dal di wéy ba matal.
- Ku manul a sànni jamrab haqaba walla yeneen yi, sañ naa wut ku ko wuutu ku mu wóolu, dim mbokk mbaab àndandoo, su sànnee ba noppi sànnil ko.
☆☆☆
Mat na
Ki leen ko doon defal:
Abdu Xaadir Kebe