Ñaqu sëqët (coqueluche)

Ñaqu sëqët su tar (coqueluche) mooy li mëna aar nit ki ci feebaru coqueluche.[1] Ñaari xeetu ñaqu coqueluche ñoo am: biy am selil bi yépp ak bi ko dul am.[1] Ñaq biy am selil bi yépp amna kaaraange gu yegg ba ci 78% waaye ñaq bi amul selil bi amna diggante 71 jàpp 85% ci kaaraange.[1][2] Kaaraange ñaq bi dafay wàññeeku, li ko dalee 2 ba 10% at mu nekk, waaye bi kaaraange ñaq bi amul selil bi mooy gëna gaawa wàññeeku. Suko jigéen ju ëmb jëlee dafay aaraale liir bi ci biiram.[1] Gis nañu ni ñaq bi musal lu ëpp genn-wàllu milion ciy nit ñumu naroon faat ci 2002.[3]

Waa Mbootaayu Wergi-yaram ci Àdduna bi (OMS) ak waa Kuréel giy Saytu ak Fàggu ci Feebar yi (CDCP) dañu digle ñu ñaq xale yépp ci anti-coqueluche te ñu boole ko ci ñaq yi ñuy faral di def. Nit ñiVIH/SIDA bokk nañu ci ñi ko wara jël.[1][4] Xale war nañu ko jël ñatti yoon, di tàmbali suñu amee juróom-benni ayi-bis. Mën nañu ci yokk yeneen sudee xale bu dëgër wala mag. Ñaq yi ci am dañu àndaale ak yeneen ñaq.[1]

Réew yi am doole, ñaq bi amul selil lañuy jëfandikoo ndax daanaka du jural nit ki benn jafe-jafe. Diggante 10 jàpp 50% ci nit ñi jël ñaq bi am selil bi yépp, barab biñu leen ko jam dafay deretal te dañuy amaale yaram wu tàng. Ñi ciy jëlee ay say yu ndaw wala mu leen di xir ciy jooy matul 1%. Sudee ñaq bi amul selil bi la nak, yenn saa fi ñu jam ci loxo bi newwi tuuti waaye du yàgg. Ñaar yépp a mëna jur jafe-jafe waaye bi am selil bi, lu nit ki gëna nekk xale muy gëna néew. Xale bi su demee ba am 6 at, waratu ñu ko jox ñaq bi am selil bi yépp. Amul benn ñaari xeeti ñaq yooyu buy indil nit ki jafe-jafe ci wàll neer.[1]

Ci atum 1926 la ñaqu anti-coqueluche bi njëkka am.[5] Ci limu garab yu am solo yi waa OMS def, mooy ñaq bi gëna am solo bu yaramu nit ki soxla.[6] Amna ci xeetu ñaq bu àndaale aktetanos, diphtherie, polio, akHib vaccine ñuy koy jaaye 15,41 dolaar (USD) dose bu nekk ci atum 2014.[7]



  1. 1,0 1,1 1,2 1,3 1,4 1,5 et 1,6 "Pertussis vaccines: WHO position paper - September 2015" (PDF). Wkly Epidemiol Rec. 90 (35): 433-58. 2015 Aug. PMID 26320265.
  2. Zhang, L; Prietsch, SO; Axelsson, I; Halperin, SA (Sep 17, 2014). "Acellular vaccines for preventing whooping cough in children". The Cochrane Database of Systematic Reviews. 9: CD001478. doi:10.1002/14651858.CD001478.pub6. PMID 25228233.
  3. "Annex 6 whole cell pertussis" (PDF). World Health Organization. Retrieved 5 June 2011.
  4. "Pertussis: Summary of Vaccine Recommendations". Centre for Disease Control and Prevention. Retrieved 12 Dec 2015.
  5. Macera, Caroline (2012). Introduction to Epidemiology: Distribution and Determinants of Disease. Nelson Education. p. 251. ISBN 9781285687148.
  6. "WHO Model List of EssentialMedicines" (PDF). World Health Organization. October 2013. Retrieved 22 April 2014.
  7. "Vaccine, Pentavalent". International Drug Price Indicator Guide. Retrieved 8 December 2015.