Ñaqu meningite

Ñaqu meningite mooy bépp ñaq bi ñu mëna jëfandikoo ngir mucc ci feebaru Neisseria meningitidis.[1] Amna yeneen xeetu ñaq yu mëna musal nit ki ci yenn ci xeetu meningite yii ñuy lim: A, B, C, W-135, ak Y. Baaxaayu kaaraange ñaqu gi mingi ci diggante 85 ak 100% mën na yàgg gën gaa néew ñaari at.[1] Li mu jur mooy wàññikuy méningite ak sepsie ci barab yiñ leen jëfandikoo lu bari.[2][3] Mën nañu la def ñaq bi ci sa sidit wala ci suufu der bi.

Waa OMS (Mbootaayu sàmm wérgi-yaram ci àdduna bi) waxna ni ñi nekk ci barab yu bari meningite wala yu ko xawa am, dañu wara ñaqu ngir mucci ci feebar bi.[1][4] Sudee gox yi feebar bi bariwul, nañu ñaq ñi nekk ci wetu ñu am feebar bi.[1] Ci goxu afrique yi nekk ci ndomba meningite, ñu ngi def jéego yu mag ngir ñaq yi am diggante 1 at jàpp 30 at, muy ñaq bi boole ak méningocoque A.[4] Ci Kanada ak ci États-Unis, dañuy digle ñuy faral di ñaq ci saasi bépp xale bu nekk ci barab bi feebar bi nekk te bari fa.[1] Waa Arabi Saudi dañuy sàkku ci képp kuy aji Màkka mu jël ñaq bi koy aar ci meningite.[1]

Ñaqu meningite (Meningococcal), daanaka ñaq bu wóor la. Ci ñénn ñi, barab bi ñu leen ñaq mën na xonk wala mu metti tuuti.[1] Jiggéen ju ëmb mën na ko jëfandikoo.[4] Néew la lool lumuy indi nit ki ay jafe-jafe, matul benn ci 1milioŋi ñaq.[1]

Ci atum 1970 lañu njëkka génne ñaqu meningite.[5] Ci limu garab yu am solo yi waa OMS def, mooy ñaq bi gëna am solo bu yaramu nit ki soxla.[6] Ñu ngi jaaye ñaq bi 3,23 ak 10,77 USD dose bu nekk (en gros) li dalee atum 2014.[7] Ci États-Unis, ñu ngi koy jaaye ci diggante 100 ak 200 USD.[8]Royuwaay:Drugbox



Royuwaay:TOC limit

  1. 1,0 1,1 1,2 1,3 1,4 1,5 1,6 et 1,7 "Meningococcal vaccines: WHO position paper" (PDF). Weekly epidemiological record. 47 (86): 521-540. Nov 2011. PMID 22128384.
  2. Patel, M; Lee, CK (25 January 2005). "Polysaccharide vaccines for preventing serogroup A meningococcal meningitis". The Cochrane Database of Systematic Reviews (1): CD001093. PMID 15674874.
  3. Conterno, LO; Silva Filho, CR; Rüggeberg, JU; Heath, PT (19 July 2006). "Conjugate vaccines for preventing meningococcal C meningitis and septicaemia". The Cochrane Database of Systematic Reviews (3): CD001834. PMID 16855979.
  4. 4,0 4,1 et 4,2 "Meningococcal A conjugate vaccine: updated guidance, February 2015" (PDF). Weekly epidemiological record. 8 (90): 57-68. 20 Feb 2015. PMID 25702330.
  5. Barrett, Alan D.T. (2015). Vaccinology : an essential guide. p. 168. ISBN 9780470656167.
  6. "WHO Model List of EssentialMedicines" (PDF). World Health Organization. October 2013. Retrieved 22 April 2014.
  7. "Vaccine, Meningococcal". International Drug Price Indicator Guide. Retrieved 6 December 2015.
  8. Hamilton, Richart (2015). Tarascon Pocket Pharmacopoeia 2015 Deluxe Lab-Coat Edition. Jones & Bartlett Learning. p. 315. ISBN 9781284057560.