Ñaareelu tukki bi (bu Gànnaar bi)

Ci bisub gàwwu,fukk ak juroom ñaar ci weeru gàmmu atum aksasin di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak benn,la Sëñ bi génne ca këram ga ca Daarul Mannaan,ginaaw bi ko ay bataaxel dikkalee aki ndaw tukkee ca nguur ga,naan ko na leen fekk Ndar ginaaw tisbaar. Mu fanaan Ngaabu ak njiitul soldaar si,xëy dem Njaaréem ,juge fa dem Tool,juge fa jàll Tiwaawon,foofa la yéege saxaar dem Luga,ware fa gaal dem Dagana,loolu lépp ci ag ayu bis,sax fa juroomi guddi,jéggee fa dex ga juge Dagana ginaaw bi, ci ñaar fukklu fan ci weeru gàmmu ànd ak waayi Sheex Siidiya Baaba ji,mooy Sheexunaa Ibnu DAADA,man na’a am li waraloon loolu di woon li nu wax ne Sheex Siidiya’a ko wax muy ne leen sëriñ bii de amul lenn lu ñaaw lu deesi ragal ci moom. Ñu ne ko woon ndax man nga noo wóoral (gaaraantil) li nga wax? Mu ne leen warlul naa leen ko,ñu ne woon ko kon leegi danu koy boole ak yaw.


Sëñ bi moom daawu leen yeexal lu dul diggante bi muy xaare ndigal lu juge ca boroomam ak sangam ba,loolu moo daan waral ñuy jort ne daa lànk,te fekk booba noonu la deme,ci noonu mu dem ànd ak Sheex Siidiya,ba nu àgg ci yenn ci kër yi nga xam ne du nu woon këram,waaye yu Banii Daymaan lanu,mu wàcc fa ngir ay mbir ci digganteem ak yenn giir yi,bu ko defee ku baax ki wàcc moom itam,bu niy laxas mu laxasati def ko ay yoon.

Bi tuxu yi baree nag ak màngaan mi ci wenn weer walla ñaar,nga xam ne daanaka dunu sax fi barab,te loolu wuute na’ak lool aaday waa réewam,loolu tiis ko sonnal ko ak ag njabootam,te itam taalubeem yi danu koy dikkal fu mu man a nekk te barab yi sori nanu,sàcc yi bari ci yoon yi sonnal leen it ya yooni yoon,ci noonu ku tedd ki sàkku ci ñoom ñu tàggoo,ñu bañ ngir xér ci ànd ak moom,ak ngir yilla ju jiitu ji muy dénk gi ko ko nguur gi dénkoon .

Waaye Sëñ bi moom dogu rekk,nu xam ne ku dëggu la,te du sàkku dara ci bànneexu bakanam,nu ànd ak moom ci li mu bëgg,nangul ko ngàntam,moom itam mu jàmmante ak ñoom ci aw bayit wu yàgg:( bu ñu nu tànnloo woon de du ma tàggoo’k yeen, waaye ag tànn àndul ak jamono ),Sëñ bi ginaaw lii du bayitu boppam mu soppi waaye ag tànn àndul ak jamono,def ko waaye ag tànn àndul ak am ñax,jublu ci loolu yéen da ngéen di sàkku fu ngéen di sàmme ak fu ngéen ko man a ame,loola reeloo leen.

At mooma mu woore Sarsaara koor ga,muy barab bu nu xam fa ñoñam,nit ñi sottiku fa,ak ñuy jële ci moom rawati na ci Banii Daymaan ak seen kilifa ya,doomi Baydah yi Abdul Laahi aki mbokkam ci loolu ku baax kaa ngi naan: (( mbooleem sama xeeti cant ñeel na ki nga xam ne sama lépp ci moom mujj na di ngërëm lu àndul ak ab sàññ(mer), ñeel ko fa Sarsaara)) (( moo moom sama tagg ak sama ngërëm ci lu dul sàññ,bi mu ma wommatalee ay ansaar yu bokk ci Banii Daymaan)) ((sama lépp ñeel na Yàlla fa teeni teraanga,yu nu tuxoo,te bari na fa ñu siyaaresi)) ((ñi nga xam ne danoo dikkoon Sarsaara ngir siyaaresi ma fa,na nu xam ne tàggoo nanu aki bàkkaar àdduna ak alaaxira)).


Ci Sarsaara gii nee na daje na fa’ak Yonnant bi (j.y.m) cig yewwu,du ciy gént,mu jox ko Wirdul Maaxuuz .Fekkoon na njëkk loolu Sang Bu nu Wóolu bi dikkaloon ko ca géej ga,rékki (jël)woon ca moom lépp lu mu jële woon ci nit ñi,ba deseetu ci dara,mu jox ko wirduw Xaadir,ba ca mujjug tuxal ga nga xam ne loolu day tegtale ne daje na ak Yonnant bi (j.y.m) ca géej ga,Jibriil dikkal ko fa mooy Sang Bu Nu Wóolu bi,rékki woon ci moom la mu ca rekki woon,joxoon ko la mu ko joxoon,jaarale ko ci Yonnant bi (j.y.m).

Mas naa teew bis kenn ci boroom xam-xami naar yi laaj ko kuy Sang Bu Nu Wóolu bi ? Mu ne ko Jibriil,mu ne ko ndax Jibriil dees na ko gis ginaaw Yonnant bi ? ku tedd ki tontoo ko ñaari bayiti ki woy Xazawaat :

(nee nanu Jibriil da na teewal kiy faatu te gëm,aw nit it weddi nanu ag dikkam ginaaw Yonnant bi (j.y.m), dëgg gi nag mooy amul ab dayo (ag dikkam) ) .

Sëñ bi neeti ko waaye wax jii am na ñu ko tax a jug,ñooy ñi ci am ag ñam akug dëggal,waa ju juge fee rekk nag li war mooy mu nangu ko mbaa mu noppi,ngir bañ a loru.

Man nag ma ne misaalum loolu mooy lu mel ne ku nu digal mu taal ab taal ngir aajo ju wér,mu taal ko,ab lëpaalëp jaar fa tàbbi ca,dee,kon kooku dara waru ko ca dee googu,naka noonu ku nu digal mu wax, bu waxee.Ma ne wàlliyu yi di gis malaaka yi moom kenn manu koo weddi, ndax jële naa ci mbindum sunu sëriñ Xalifa Alhaaji Muhammadul Faadil,moom mu jële ko ci yenn ci teere yu mag (majaamih) yu wér yi lol ab yaxam mooy ku ñu ubbi (maftuuh halayhi) moo xam ab nabiyu la walla wàlliyu,manul a ñàkk mu jàkkarloo’k malaaka,ci seeni jëmm,ni ñu mel,tey wax ak ñoom ñuy wax ak moom,képp ku ne wàlliyu du gis malaaka tey wax ak moom kon na xam ne tegtalub loolu mooy moom du ku nu ubbi,lii nag mooy layuw ku nangu(féeñug Jibriil),ci ku ko nanguwul.

Ginaaw Jibriil da na dikkal aji gëmm ji buy faatu,te ku ñu ubbi day gis malaaka yi tey wax ak ñoom,te yinkiiwalug wàlliyu yi (sol gi nu leen di sol xam-xam ak li Yàlla di bëgg ci ñoom) mi ngi am jaare ci malaaka walla mu am ci lu dul muy jaar ci kenn,ginaaw loolu lépp am na,kon du jomb ci Jibriil moom mi Yàlla wóolu ci wëhyoom gi,mu nekk ag diggale (intermédiaire) ci yobb ak joxe yinkiiwal gi Yàlla di dsotti ci ñenn ci wàlliyoom yu mag yi,ginaaw ñoom ñooy ñiy dònn yonnant yi.


Moom Jibriil dimbali na sunu sang ba Hassan saaba bi (y.y.g)ci teewaayu Yonnant bi (j.y.m),mu di ag kiimaanam tey karaama ñeel aw wàlliyoom,luy tee kon mu man a dimbali ligéeykatam bii ci ginaawam,mu dig kiimaan gu ñëw ci ginaaw bi tey karaamay wàlliyoom wu dikk ci ginaawam te di ko ligéeyal ni ko Hassan,wàlliyoom wu njëkk wa doon defe. Ñoom ñaar de ay mbokk lanu ci lgéey bi,ba fa tuxal ga xam. Du ñàkk ñariñ ñu indi tuxal gi ba ngéen gis ko,mi ngi nii:da ne yal na ko Yàlla mu màgg mi gëram : bu dee bunt bi yor wirduw aji nos ji (aji woy ji) moom doggantal nekku ci ,(doggantal= français =chapitre,araab=faslun) aji nos ji ,wird wi mu njëkk a jël ci wird yi mooy wu Xaadir,ginaaw bi wu Shaazaliya,ginaaw bi wu Tiijaan.


Bu dee wirduw Xaadir moom jëfandikoo na ko lu yàgg,daan ci sàkku ndigal ci képp ku mu mas a yaakaar ne ku nu ci jiital ga (muxaddam), ba jële woon ko ci ñu bari. Ginaaw bi mu wóor ko ne ñi mu daa jële du ñu ci woon ay muxaddam maanaam ñu ñu jiital (ñu ko war a joxe) ,mu sàkku ci Yàlla (t.s) mu may ko ci lol ag gëlëm mbaa ag dengi-dengi dootu ci nekk. Mu ne bi ma Yàlla yobboo ci géej gi ma nekk man rekk ak moom la ma Sang Bu Nu Wóolu bi dikkal (j.y.m),dal di rékkee ci man lépp li ma jële woon ci nit ñi ba dara desatu ci,mu jox ma Xaadiriya ci diggaleg (jaarale ko ci) Yonnant bi (j.y.m). Tuxal gii ak lu ni mel ci mbidd yi, danuy wone ne Sëriñ bi daje na ak Yonnant bi(j.y.m) ak Jibriil (j.y.m) ci lu dul woote ag yonnant,du caangéenug wëhyu,waaye ci kem li Yàlla di jagleel lenn ci wàlliyoom yu mat yi.

Waxam ji mu naan wirdiy aji nos ji mi ngi ci jublu woon xasida gi mu doon tudde ñatti sëriñ yu tedd yooyu,ak dònn gi mu leen dònn, tuddati sunu sang Anas,ak Hassan (gërmul Yàlla yal na nekk ci ñoom) ak dònn gi mu leen dònn ci waxam jii: ((wommatal nga ma la Jiilaani (Abdul Xaadir Jiilaani)kawee woon ba fa mu yam)).


Ku bëgg a am lu ko leer na xool teere bi nu naan “Tanwiirul halaki fii imkaani ruwyatin nabiyyi wal malaki”di ci maanaa leeralug lu lëndëm këriis ci man a nekkug gis Yonnant bi (j.y.m) ak malaaka,teere boobu boo bëggee lu leer rekk moo ciy géej jug mbàmbullan gi.te boo defee ag settantal ci tuxal gii ak li ci topp,da nga gis la amoon kon ca géej ga muy ni nu nangoo woon li mu jële woon ci ku dul woon Yonnant bi(j.y.m),ak dello ngi ko ko Yonnant bi delloowaatoon,ak naayibam yi, ñatti sëriñ yu tedd yi,ngir mu nekk naayibam moom Yonnant bi ( aji wuutoom),tey ki fi wuutu yooyule sëriñ (g.y.y.ñ),ci seeni wird ,di seen muxaddam bu nu joyal bi , nga xam ne amul lenn lu ko tënk ci wenn wird,(ku ko neex ak nu ko neex la koy joxee) ,da nga ci gis it la amoo n ci Sarsaara muy jox ga nu ko fa joxoon wirduw boppam moom rekk,jagleel ko ko,nga xam ne benn sëriñ bu ko fi jiitu masu koo yor.


Looloo waraloon daawul digal ku jébbalu ci moom te yoroon aw wird njëkk muy ñëw mu koy bàyyi,da koy digal kay mu tëye ko te yéene ne moom moo ko ko jox,ku jébbalu ci moom nag te waxoo ko dara,bu boobaa mu door laa jox wirduw boppam. Looloo waraloon doomam ju tedd ja,sunu sëriñ,SheexMuhammadul Bashiir naan cig xasida gog biral na ci ngënéelug wirduw Sëñ bi ci yeneen wird yi,xaaral ma jox la ko lépp,ma nga ca biir it waxam ja mu naan: ((wommatal nga ma la Jiilaanii kawee woon)) ba ca bayit ya nga xam ne sëñ Bashiiru tudd na leen ci xasidaam gii,mi ngii:


(ci turu Yàlla laay tàmbalee aw woy wuy jariñ ku bëgg a jariñu te ab xolam set) (ag cant ñeel na Yàlla,yal na dolli xéewal ak mucc ci Yonnant bu nu tànn bii di gën ji mbindéef) (ak ñoñam aki saabaam ,ñu tedd ñii te diy sang,ñoom ñi wuññi lëndëmi xol yi ak lëndëm) (bu loolu jàllee ma naan la déglul waxi kiy laabiire boppam tedi la laabiire ci luy faji aajo) ( yaw miy sàkku matug texe ci yooni ñatti sëriñ yi) (yoonu sëñ Imaam Jiili (Abdul Xaadir Jiilaani) ak Shazali mi làq ag ngënéel) (ak Abool Habaas (Sheex Ahmad Tiijaan) miy ndamul ñu mat ñi,ñoom ñooñu nga xam ne seenub àtte ca jublu ga (xasd) mooy àtteb ku njëkk ka ) (ànd ak ku ci nekk yor sa jagley bopp yoy ci la saw yoon làqe ay jagleem,loolu nettali nanu ko) (na nga taqqoo’k yoonu Abdul Xadiim (jaam biy ligéeyal Yonnant bi) ,ndax moom kat moom la Yàlla mu jiitu mi jagleel mu dònn yoon yooyu yépp) (ndax kat wird wu nekk am na mbóot,ci benn baat bu ci nekk,(ci biir wird wi) yal na la Yàlla gindi) (baat boobu nag boroom “baziira” yi rekk a ko xam (baziira = gisug xol )keneen ku dul ñoom xamu ko,muy hikamu ab boroom buy aji not ) (misaalam mooy Laylatul Xadar ci weeru koor wu nekk,ak Waxtuw Àjjuma,dees leen di wër di) (Yàlla feeñalal na ko (moom Sëñ bi) ya làqu woon yépp (ci wirdiy yeneen yoon yi),ginaaw bi mu leen ligéeyalee te yekkati ag wàllam ngir jëmmam ju tedd ja,ba mujj ñépp bëgg ko jiital ko,(def ko muy seen muxaddam (ku nu jiital ki am sañ sañu joxe wird wi) ) ) ( Yonnant bu nu tànn bi tam - yal na ko Yàlla dolli ay xéewal ak mucc ni mu ko tànne - yéegal ko ci ab hadara bob ku dul moom fàddu na ci yaw,bu nekk fa aji kawe ji (muy Yàlla) loolu di lu kawe sax la mu doon wut ) (bi loolu wéyee mu donnalati ko lu nu nëbboon li , muy aji jiitu ciw yiw joj wuññi na ay fitna) (ci coobareem (moom Yàlla),màgg na te kawe,la ko tànne ci darajay Yonnant bi miy ligéeyal biy joxe ag sell) ( ngir barig li mu leen ligéeyal te sellalal boroomam,di it ku sellal te matal kóllare ci diineem) (mu boole lépp,dolli ci,yéeg ci barkeb Alxuraan te fa mu yéeg’ak a baax) (boo jëlee wirdam de jël nga wird yépp,te doo ragal ag nërméelu) (la nu dige ca seen wird yooyee it da nga ca jot,te doo ragal genn tëkku ) (ndax moom (tëkku gi) ku bàyyi dëgg a ko tax a jug,te ku ko jël (moom wu sëñ bi) yayoo nga jagle ya ) (jàpp ko de moo di jàpp ca lu baax la te dolli ca nag,ngir boole gi mu boole (wird) yépp,teg ca yor leneen ndollent (lu yeneen yoon yi yorul)) (cosaan li mooy da ngay wax (ahuuzu billaahi minas shaytaanir rajjiimi)teg ca (bismil laahir rahmaanir rahiimi) jàng yenn aayay Alxuraan,doo ga tàmali) (def hasbala (wax hasbunaal laah ba fa mu yam) def istixfaar ( astaxfirul laah) ,def haylala (wax laailaaha illaal laah) ,julli ci sangub ñu tedd ñi) (ginaaw bi defees ag tëj gu rafet,loolu da na amal fa Yàlla lépp lu baax) (lli mooy cosaani seen wird yi ñoom ñëpp,ku ci nekk nag am na genn jagleem gu mu moom moom rekk gu kawe) (Sëñ bii nag moom jël seeni ndono jële ko ci gën ji mbindéef mi leen di àggale) (mu wax (moom Sëñ bi) bi miy nettali yooyule xéewal,di ci sant kiy fàttaliku (di Yonnant bi) ngën ji aji xéewale ji (di Yàlla) ) (ki moom jépp jumaa ak jépp jàkka, moom loo na ma mebëtum mbooloo yi) (mu wax di sant aji tedd juy kenn ju ko donnal téere bi (di Alxuraan) muy ndono lu am njariñ) (tàllal naa sama loxo jëme ca Yàlla,moom itam mu tàllal xéewalam ga ñeel ma ca géej ga,te loola tàlleeku) (téereem bu tedd ba mujjoon na di wird ci man,daqaloon na ma samay noon it te dàkku leen) (mu daan won lu neex képp ku ko taqoo, di ko jàng lu mu man) (boo bëggee leeralug lii ma la tuddal,am lii nga xam ne ciy woyam laa binde sama mbind mii) (wommatal nga ma lol ci la Jiilaani kawee, ngëramul ki ma kaweel yal na nekk ci moom) (wommatal nga ma la Abool Hasan kawee woon ci ligéeyal Yonnant bi,miy maami Hasan) (matalal nga ma la nga xam ne ca la Sheex Ahmad Tiijaan kawee woon,te nga nekkal ma ci lu rafete ni wurusu marjaan) (wommatal nga ma lol soril na ma taq-taq,ma mujj mel ni Anas ci ligéeyal yonnant bi) (moomloo nga ma te wommatal ma ag rafetal,donn na Hassan ci tagg Yonnant bi) (ngërëm ak jàmm yal na nekk ci ñoom,ni lëndëm dàqoo ci ñoom(ni nu leerale àdduna bi)) (mu wax ci bi miy tagg ngir sant ku nu jublu ki ( di Yàlla) ci téere bi (di Alxurran) ak Yonnant bi Muhammad) (sama àddiya ji juge ci yaw ak ci Muhammad sunu sang bi, lu man a tee mer la) (darajay aji far ji (muy Yonnant bi) far na samag deng-dengi,te wommatal ma kàttan ga ci lu dul ag doyodi) (sama lépp’ay sant aji yekkati ji may dëgëral,cant gi nag jëm ci Alxuraan ak Yonnant bu baax bi) ( téere bi ak Yonnantub ku nu jublu ki, yekkati nanu sama lépp ci lu dul keno) (Alxuraan nooyal na sama xol bu gindiku bi,dàq it bépp jalgatikat jëme ci ku dul man) (sama xol ak sama loxo maa ngi ko jëme ci ku nu tànn ki ci di ko ligéeyal,may na ma nag la ëpp njariñ) (aji dégg ji wuyyu na ma ci weeru koor,te baax na,mooy sama jubluwaay,ci barkeb Yonnant bi Muhammad) (Yàlla gindi na sama xol,ñongal samaw yaram ci ngërëmam,dañal aji yàq sama) (mu waxati bi muy déeyaale ak boroomam,mbégte ñeel na ñi ko sopp ñépp) (ne: yaw mi jéggal sama ñaari way jur ak ñi ma sopp ci lu dul njàqare) (te nga fàddul ma ci sa bopp ak ci Yonnant bi wëlif mbindéef yi,te may ma ay saar) (fàddu nga ak man bu njëkk ànd ak Yonnant bi,may boroomug làqu wëlif mbooleem mbindéef yi) ( ma di ab jaam buy ligéeyal Yonnant bi,di ku nekk ci yaw ànd ak dëgg gi foofa,tey ku fàddu) (mu waxaat ci yenn may yi nu jagleel ñi topp yoonam wi) (Yàlla jëme na ci ñi dul ñi aju ci man lor yiy daje ak dof yi) ((ab boroom bu man loolu may na ko ko,te moom (boroom boobu) ku yayoo wuyyu la ci ku ko woo) (nuy tëje ci Yonnant bi,mi di ag tàmbali te di ag tëj,tey ki gën a mat,yal na Yàlla saxal xéewal ci moom ak ci ñu mat ñi) Foofu la loolu yam.



Ñu dellu ci wax ci cosaanul wird wi,ak yax bi(yax=nassu ci araab.=texte ci français) mu bindoon ci ginaaw sotti (sotti = nusxa ci araab.=copie ci français) ga mu amaloon ca wird wa, muy :

bismillaahiir rahmaanir rahiimi wa sallal laahu halaa sayyidinaa muhammadin wahalaa aalihii wa sahbihii wa sallama tasliiman ,ku xool araf yii nu bind ginaaw matug wird wi, na xam ne ki ko bind di Ahmadu doomi Muhammad doomi Habiibul Laah,mi askanoo Mbakke te dëkk Bawal,may na ndigal mbokkam moomu ci Yàlla (t.s),sang bi Mustafaa Usmaan mi juddoo Halab te dëkk Madina,may na ko ndigal ci mu jëfandikoo wird wu nu barkeel wii ak jox ko ku ko soop ci mbokk yu góor yi ak yu jigéen yi,ni mu ko jëlee ci Yàlla jaarale co ci Yonnant bi (j.y.m) cig yewwu du ciy nelaw,atum baksasin di junni ak ñatti téemér ak ñaar fukk ak ñaar,ginaaw gàddaay gi,yal na Yàlla defal ki ko defoon gën jaa saxi xéewal ak gën jaa jariñi jàmm,ci benn barab bu nuy wax Sarsaara,ci weeru koor gi nu wàcce Alxuraan,mu dig jub ñeel nit ñi,te di ay aaya yu leer yoy ag jub la ak teqale dëgg ak safaan. Yàlla nag mooy seere lii nuy wax.Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yasifuun wa salaamun halalmursaliina wal hamdu lillaahi rabbil haalamiina.


Sunu mbokk moomu Muhammad Abdul Laah Alhalawii,nee na ci teereem bi tudd(( Anafahaat almiskiya fiil xawaariq al mbakkiya))muy ci maanaa bonnig misk ci xar-baaxi Mbakke,nee na Sëñ bi Yàlla da koo jox wird wii,mu jox ko muritam yi,xemmemloo leen ko,te loolu di lu war ci moom. Mu ne leen képp ku ko saxal aki sartam da na tàbbi àjjana ci lu dul hisaab (hisaab mooy laaj yi ñiy def ak a gëstu ay mbir) du caagéenug mbugal,te Yàlla it da na ko aar ci naqar yi ci àddina ak alaaxira,te saytaane mu nu dàkku mi du ko jege,da na doy wird wi ag kawe,nekk gi mu nekk wird wow boo ko dee jëfandikoo soxlawul gay jëfandikoo yeneen yi,te manoo am li ci moom te jëfandikoowoo ko.

Sunu Sëriñ, sunu wasiila ca sunu boroom mu kawe mi nee na bi mu nuy jox wird wu tedd wii:jox naa leen wird wii ngir jëmmi Yàlla mu tedd mi te kawe,kon tëye leen ko ngir jëmmi Yàlla mu tedd mi te kawe. Mu waxaat jàpp leen ko ak doole,ku ci jotoon a yor weneen wird bu ko manee, na leen boole,kon muy leer ci kaw leer,bu ko manul mu yam ci wird wu tedd wile. Jeex na.



Ki ko doon taariixal nag ne moom : bismil laahir rahmaanir rahiimi ,lii aw tagg ak taariix gu Ahmad doomi Asan def ñeel wirduw sëriñam bi Sheexul Xadiim,yal na nanu Yàlla jariñ ci moom ci ñaari kër yi aamiin.


( sunu boroom taxawal (fondumang)na sunuy jëf ci may nu ñu man a root ci gën ji teen, kon mbégte ñeel nanu (mu jublu ci wirdul maaxuuz)) loolu mooy wirduw sunu sëriñ bi Sheex Ahmadu Mbakke,mu juge ca boroomam jaar ci Ahmad Yonnant bi) (yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc,li feek mi ngi doon ab raas jëm ca texe gu kawe ga) (jox na ko wird wii jële ko ca aji namm ja muy Yàlla,yéem naa te ñée bii sëriñ ak yii taalube) (jagleel na ko wurusu luulu wu nu ñongal ci xor,te làq ko ku dul moom) (wurus ñeel na sunu sëriñ bu nu gërëm bu màgg bi,ku ko am de am dëkkaaleg ka gën a màgg) (mi ngi ko gènne ci bisub àjjuma,mu jëm ci ku Yàlla texeel ci doomi jamono ji) (ci juroomi fani sawaali atum (sahidnaa karaman) di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk,moom boroom taariix bii,moom miy ndëppul ñu tedd ñi (ndëpp mooy mbaxana mi nuy solal buur) ) (mooy sunu sëriñ Ahmadu MBAKKE mi dëgg di tax a tukki ak a took ) (génneel nanu ko ngir jëmmi Yàlla ,kon billaahi bu ko sàggane) (ngir Yàlla,boo bëggee am li nga bëgg,ndax kat kuy rëbb ba jam ñay man a dëpp) (yaw sama boroom ci darajay aji wommat ji xeet yi jëme leen cig jub,di Muhammad miy wuññi njàqare) (yal na Yàlla miy sos niir yi,sotti ci moom gën jaa selli xéewal ak mucc ak ñoñam aki saabaam) (ak ci darajay sunu sëriñub Mbakke bii,na nga ma may ma jot ca la ña jiitu bëggoon) (ci ag kawe,bu ko defee ma bokk ci mbooloom ñi la jege,yaw miy boroom nguur gi) .



Nan dellu ca tukkib ñaareel ba,dem ba Tintu Muxsin,foofu barab la bob xew-xew bu ñaaw te soof dal na ko fa,muy : ab naar bu nu xam turam ak giiram,daa jugoon ngir ne da koy faat moom Sëñ bi - man moom xam naa ko waaye dama koy suturaal ngir doomi baay tëxam yu julit yi - moom da doon fexee faat Sëriñ bi,Yàlla musal ko ci,ni mu doon defe loolu nag mooy xanaa ñëw ci moom won ko ag cofeel gu dëggu ak jébbalu ci moom,Sëñ bi moom itam suturaal ko,boole ko cig njabootam,bindal ko ñatti bëyit,ne ko na ko saxoo jàng,guddi ak bëcëg ,naar bi moom itam dëkke woon loolu,bëyit yi moo nekk nii: (lor ak saytaane jëm nanu ci ku dul man,ndax ñoom ñaar kat amunu ci man genn kàttan) ( Yàlla mooy sama boroom,Yonnat bu nu tànn bi - yal na Yàlla dolli xéewal ci moom, moom mi ko gindi te tànn ko) ( mooy samab xarit te di sama soppe,te bañ na it samag loru,te sàkku na ci boroom mbindéef yi samam mbég ).


Naar bi taqoo woon ak loolu,di ko jàng guddi ak bëcëg ,ci mbooloo mi ak bu wéetee,mu ko daan def ginaaw saaru Yasiin,mel ni kuy nodd,nga xam ne da naan wax: yaasiin,yaasiin,yaasiin,ba kero muy mat juroom ñaari yoon,mu door a àggale saar wi teg ci bëyit yi,jàngati yaasiin ni mu ko defe woon,tegati ci bëyit yi,baamooti leen,nii daal la ko daa defe ,daawul taxaw lu dul daa sonn walla muy nelaw,mu sax ci loolu ay fan,am na ñu ne weer.

Jamono jooja Sëñ baa nga woon fa ñoñ sheex siidiya,nekk ca seen xayma ya,ci noonu mu digaloon taalube ya nu defaral ko ag kër ca bitib gàdd ga,ñu def ko ni mu ko bëgge woon,bi mu noppee mu wax ko sheex Baaba,sheex Baaba digal mbokkam ma sheex Siidiya Muxtaar mu gunge ko ca kër ga,mu defe ko noona.

Sëñ bi moom digal naaram booba mu ñëw ànd ak moom ca kër ga tey jàng ñatti bëyit yi,ni mu ko baaxoo woon,bi nu agsee,saytaane jàpp ko,xamal ko ne pexe mi mat na,def dong a ci des,bi guddi gi soree ba kenn yëngootul,naar bi jug,summiku ba mel ni ko ndayam jure woon,dal di dugg ci kër gi,jawali ca néeg ba Sëñ ba nekk,ginaaw xamoon na fa jaasiy Sëñ bi nekkoon ,mu jawali ca,bocc ko ci mbar mi,waaye Yàlla dogal jenn waay ju bokkoon ci néegub nguurug Kajoor,te gënoon cee rafetug tuub ak bàyyi àdduna,ñu ko daa wax Omar FAAL NDATI,nekkoon ca jàkka ja,di fa fanaanee jaamu Yàlla,bi ko naar bi rombee mu jug ca saa sa,seeti ki yor mbiri biiri Sëñ bi ,di Muhammad Lamin ÑANG,doomi Muhammad Lamin Mati,moom waa-jur wi,doomi bàjjan la ci Sëñ bi,xamal ko ne am na jëmm ju rafle ju jëm ca néegub Sëñ ba,ca saa sa ndonga la jug,gaawantu,fekk naar ba mu bocc jaasi ja,di settantal naka lay jekkoo Sëñ bi ba man koo lor bu baax,te Sëñ bi moom mi ngi tëdd ci wetam,bi naar bi xàccee di ko door jaasi ji,yàlla dogal mu lonk ci koñub xayma bi,daje ak ndonga li di wadd di dal ci kawam,mel ni kuyul gileem loolu,dal di koy nërméel,naar bi yuuxu,murid bi yuuxu ci kawam,mel ne da koo bëg a lekk,seen coow li fees foofa dell,ña nekkon ca wet ga yuuxaloo,daje fa,nga xam ne Sëñ bee mujj ñëw dox digganteem ak nit ñi ne kon ñu ray ko,mu dalal leen,dal di yonne ci menn mbooloo,mu fanaanoon fu sori foofa,mu mu naroon a yewwi,woolu leen,ne leen yobbaaleel leen ma naar bii ba Xumaak, (barabu kiliftéefug tubaab yi,da nanu ko wax it Sahwatul Maa) ngéen bàyyi ko fa te dem seen yoon,denk leen ñu yëram ko te dimbali ko ci bagaasam yi,làq leen nag xibaar bi,ngir bañ ñu gaañ ko,jeemul a fayoonte ak moom ci jëfam ju ñaaw.



Yenn taalube yi nag gis nanu ne li tax Sëñ bi delloolu naar bi Xumaak,fa tubaab yi am sañ-sañ,ab junj la ci ne ñoom tubaab yi ñoo ko yonni,Yàlla rekk a xam,waaye pexeem ma moom Yàlla naaxsaayal na ko.

Yooyu ñaari bëyit boo ko xoolee da nga gis ne Yàlla feeñalal na ko ci ay karaama yu kawe,yal na ko Yàlla fayal jullit ñi aw yiw ak Lislaam.


Man nag li ma gis mooy lii mooy dëgg-dëggi laabiir ak doylooYàlla,ak nangu ab dogalam,miinunu ko ci ku dul moom ci waa jamonoom,li mu nuy fàttali mooy li daloon ki miy ligéeyal ci yenn ci xareem yi,loolu mooy dafa am benn Ahraabii (araab bu dëkk ca kaw ga) bu tuddoon Duhsuur bu ko fekkoon mu tëdd,xaw a sori saabaam yi,mu bocc jaaseem,xàcc ko ne ko ana ku man a dox sama digante ak yaw? Yonnant bi (j.y.m) ne ko Yàlla,ci noonu waa ji di lox ba jaasi ji rote ci loxo bi,Yonnant bi (j.y.m) jël ko ne yaw nag ku la man a musal ci man? Mu ne ko amal yërmaande, Yonnant bi jéggal ko,bañ koo def dara.


Naar bii nag moom bis dellusi na ci Sëñ bi ca Xumaak,taalube yi jug ngir fexeel ko,Sëñ bi yëg ko génn ci naaj wi,te solul ay dàll,di wax ca kaw: bàyyi leen ko,bàyyi leen ko,(alaa tuhibboona an yaxfiral laahu lakum) muy:xanaa bëggu leen Yàlla yëram leen,di ko baamu.

Nu bàyyi ko,mu digal ko mu làqu,génn te dem yoonam,ginaaw bi mu ko defalee ag njekk. Bi ku tedd ki nekkee Njaaréem,naar bi delseeti fa,Sëñ bi aarati ko,naan ko:boroom jaasi ji,naar bi naan ko : déedéet neel boroom xëm gi,bu ko defee Sëñ biy ree,génneeti ko ginaaw njekk.Man ci sama bopp gis naa ko Cees,maanaam Jànqeen,te booba maa ngi ànd ak am mbooloo ci taalube yi,waaye man rekk a ko ci xàmmee,bu ma ne woon kii de diw la ñu ray ko,waaye kon ana jikkoy Sëñ bi,Alhamdu lillaa.


Nu dem nag Jaraari,barab la bu Halawi yi moom,Sëñ bi tudde woon ko Biirul Xayri di ci maanaa teenub yiw,ci barab boobu la Sëñ bi doon waxe xasida gii: (( li ma doon laaj sama boroom indil na ma ko cig baamu,rawati na ca Biirul Xayri di Jarraari)) ((samag cant ak njukkéel ñeel na ab boroom bob wommatal na ma ay xéewal,ci lu nëbbu ak lu feeñ,di ku ñu baax ñi sopp)) ((sama boroom wommatal na ma barkeb saabay ku nu tànn ki,mu nekkaloon ma te daawu ma won ayuw kàccoor yi)) (( samag cant ñeel na aji jiitu juy aji des,kok aar na sama kanam wëliif bépp ñaawtéef,ànd ak ag bëbb guy daw juge ci moom jëm ci man (bëbb mooy luy sottiku bu baax di wal fii mu jublu ci xéewal) )) ((samay cant ñeel na ko,ci biir ay sang yu askanoo ca Aliyun (fii man na cee jublu Seydinaa Aliyu,man naa firi it aji kawe di Yonnant bi) ci lu dul aji jalgati mbaa workat)) ((aji des ji amul bokkaale yal na dolli xéewal ak mucc ci ki nga xam ne indil na ma la ma ko ñaanoon cig baamu)).


Halawi yi nee nanu xamunu lu tax Sëñ bi tudde ko Biirul Xayri,ndax tur woowu ñoom masunu koo dégg ci seei baay,ba bi nu fa suulee Sheex Ahmad Bun BUDDIN,nu dal di xam sekkareb li tax mu tudde ko ko,nu xame ci baatinub Sëñ bi.

Ci Sheex Ahmadu Bun Buddin, Sëñ bi wax na ci ay wax,Alhaaji Muhammab Bun AAB,dàkkantal la ci Sheex Ahmadu Bun Buddin,nettali na ma ne baayam bind na bis Sëñ bi ne ko daa bëgg mu nuyyul ko Yonnant bi(j.y.m),ak Sheex Ahmad Tiijaan,te itam soxla na seenub tontu,Sëñ bi tontu ko xamal ko ne Yonnant baa ngi koy fay,ak Sheex Ahmad Tiijaan,aji nettali ji nee na ca saa sa, baay ji daanu ab jéll,di yëggal bopp bi ak a waxtu,mel ne ku jaaxle te nu muur am xelam,dañul ci melokaan woowu ba bi mu faatoo (y.y.g),te booba ñi ngi fu sori woon Sëñ bi, te yëgalunu ko woon kenn ci guddi gi mu ame woon,waaye amul lu dul ay ndaw dikk ci suba gi ne Sëñ bee leen yabal ñu teewesi dencug Sheex Ahmadu gi,te di leen ko jaale.


Mu bind ci loolu ag xasida di ci xamale darajay Sheex Ahmadu moomu, fa Yonnant ba,moo tax mu terale ko karaama googu,ne lii mooy payug Ahmadu Bun Buddin,tey payug ab xalifaam:

Bismil laahir rahmaanir rahiimi, yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci sunu sang bi Muhammad aki ñoñam aki saabaam,na ngeen xam ne guddi gi Sheex Ahmadu Bun Buddin di faatu ruuhul xudsi (jibriil) (j.y.m) wàcc na juge ci asamaan si,ànd ak lu bari ci ay malaaka ngir terale ko sang boobu,ngir rafet gi mu rafetoon njort ci Jaam Biy ligéeyal Yonnant bi (Sëñ bi) ,yal na ko yal na ko Yàlla nekkal cig teral,moom miy aji jiitu tey aji des,ñoom nag delluwaatunu ca guddi googee ndare bu danoo yobbaale ruuwam gu tedd ga,lii nag mooy dëël bi nu ko dëëloon,(dëëlmooy dikk) .loolu la Sëñ bi di junj ci bëyit yii:

((Ruuhul Qudsu ñëw na,di wuññisi njàqare,ànd ak mbooloo mu mag ciy malaaka,jamono ji Ahmadu mii di làqu)) ((Ahmadu am na la mu bëggoon ca Yàlla,buntub yiw ubbikul na ko bu dul tëjooti)) ((yal na Yàlla fay ka joxoon àddiya aji ligéeyal ji,moom moomu nga xam ne am na fa Yàlla ag tab gog aw yiwam moo gën a mat)) ((maa ngi sàkku ci boroom aras ay may ñeel ka ko joxe woon moom mooy aji texe ju nu ndëppal ji (ki nu solal mbaxanam buur) )) ((sangub sang yi wéy na,di ab sëriñ bu nu jiital (bu nu def muqaddam),jiital gi it ki ko def di sëriñ bob aw wirdam ba fàww am ngér lay doon)) (( moom de bir na ko ca àllaaxiraa gee mu nekk ne man maay jëwrini ki nga xam ne mooy boroom raw ak jiital,te mooy ku nu ndëppal ki)) (( sangub sang yi yal na am ngërëmul sëriñam,ak ngërëmul gën ji mbindéef,ndaw muy ku nu bégal !)) (( Yàlla la’ay ñaan mu may xalifa bii mu fi bàyyi la mu yéene,ci darajay ka nga xam ne ay leeram day jolli)) (( yal na nekk ci moom ,moom Yonnant bi,ñaari xéewali Yàlla mi ko gindi def ko muy ku nu gënal ki,ni mu doon yéege ak a kawe ca rañaan ga)) wasalaamu hallaykum wa rahmatul laahi tahaalaa,wa barakaatuhuu.

Eskëy,gis nga waxam ji mu naan “ka ko joxe woon” mi ngi ci jublu Sheex Ahmadu Bun Buddin mii,li mu ko joxoon mooy benn teere bu tuddoon ((Mawaahibul Ladduniya)).

Sama mbokk,sama xarit Sheex Ibraayma AMAR nu gën koo xame ci turu Ibra Joor,nettali na ma ne Sëñ bi,bi mu nekkee Sarsaara walla Tuntu Muxsin, da koo yonni woon Ndar ngir mu jëndal ko fa téereb Mawaahibul Laduniya,nga xam ni ki nuy wax Qastalaanii moo ko def,nee na ma dem sonn ci lool,fu ne ma wër fa,waaye dara,ma am lu ma naqàri lool,yëf yi tiis ma lool,ma dëpp di ñibbi,bi ma tollee ca gàddug Sheex Ahmadubnu Buddin,te fekkoon ma xamante ak moom,ma daad fay jàdd ngir nuyyu ko,siyaare ko,ba ma fa àggee mu bég lool,teeru ma dalal ma,bi nu toogee bay waxtaan mu laaj ma lu ma taxoon a jug,ma ne ko sëñ bi dey moo ma yonni woon Ndar,ma leeral ko tam naqàr wi ma am ci ñàkk a am teere bi ma Sëñ bi yonni woon,ca saasa mu jug,gëstu ci ay teereem,génne ñaari xaaj yepp indil ma,ne ma neel Sëñ bi àddiya la,ju ma ko jox ngir Yàlla,ma bég ci ba fa bég yam,waaye Sëñ bi moom gën maa bég fopp ci teere beek ki ko joxe,loolu nag mooy maanaam ka ko joxe woon,mu jub lu ci li mu joxe woon “MawaahibulLadduniya” .


Xasida gii ndollent la ci tontub kiy laaj ndax Jibriil da na dikkati ginaaw yonnat bi. Bokk na ci li mu bind ñeel Sayid Ahmad mom Sheex Muhammadul Haafis lii: Bismil laahir rahmaanir rahiimi,allaahuma salli halaa sayyidimaa muhammadinil faatihilimaa uxliqa,wal xaatimi limaa sabaxa,naasiril haqqi bil haqqi wal haadii ilaa siraatikal mustaqiim,wa halaa aalihii haqqa qadrihii wa miqdaarihil haziim,na Sheex Ahmadu Bun Sheex Muhammadul Haafis,ak ku dul moom ci ñoñ Halawi yu goor yi ak yu jigéen yi,ak ku dul ñoom ci jullit ñu goor ñi ak ñu jigéen ñi,nanu xam ne Yonnat bi jàmm ak xéewal yal nanu nekk ci moom,delloo na ab nuyyo Sheex Ahmadu,te Sheex Tiijaani moom itam gërëmul Yàlla yal na nekk ci moom delloo na ko nuyyoo,te Yonnant bi (j.y.m) teral na ko teral gu mel ne gi mu teral mbokkam mi Sheex Muhammadul Haafis,ki ciy dund yal na ko Yàlla gërëm te aar ko ci lépp lu mu ragal,ka wéy it mu gërëm ko te yërëm ko,te SheexAhmad Tiijaan it yal na ko Yàlla gërëm,te jegeel ko,def na ko niki doomam,képp ku jële wirduw tiijaan ci ñaari sëriñ yii tudd Ahmad yal na leen Yàlla gërëm te aar leen te yërëm leen,mel na ne jële na ko ca Sheex Muhammadul Haafis (y.y.g),képp ku ko jële ci ñoom ba noppi bàyyi leen fi di demati ci keneen ci mbooleem sëriñ yi,ànd ak yéeney bàyyi leen,na ko wóor ne pert na ci àddina ak allaaxira,yal na nu ci Yàlla musal,képp it ku ko jële ci kenn ci ñoom ñaar,bu ca faatoo tonowu na adduna ak allaaxira,képp ku xool mbind mii na xam ne bi nu koy bind Sheex Ahmad Tiijaan (y.y.g) moo taxaw di wax ñuy bind.

(( dello nuyyoo bu teey bu kawe bépp nuyyoo buy bijj ag dëppoo)) ((juge na ca jaamub boroomam bay ligéeyal ku nu tànn ki,jëm ci ki làq kawe gi niy tànn)) (( yaw sëñ bu màggi mbir bi,musal nanu la ci lori lépp lu ñaaw)) ((musal nanu la ci rékki aw yiw wu nekk ci yaw,ba kero ngay tàbbi àjjana ya’ak ñi lay xeeñtu)) (( Aji des ji musal na la ci ñaawtéef yi,ci barkeb ku nu tànn kiy boroom raaya ba (daraapoo ba ,di Liwaawul Hamdi) )) (( ak darajay sa sëriñ bu nu gërëm ba,Sheex Tiijaan,ka mujj mel ni wurusu marjaan fa sang ya)) ((yal na Yàlla miy aji des dolli xéewal ak mucc ci gën ji mbindéef, moom (Yàlla) miy ki koy wommatal kawe ga ak saar ya)) ((ngërëmul Aji des,luy bijj ag dëppo yal na nekk ci wàlliyu wow topp na ay tànkam (tànki yonnant bi) )). Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yazifuun wasalaamun halal mursaliin wal hamdu lillaahi rabbil haalamiina.




Bokk na ci li mu bind ngir ñiy am ag wuute ci “Mahiya” (mahiya mooy ag ànd,nu jublu ci ànd gu Yàlla ànd ak kenn walla nekk gu mu nekk ak moom) ,lii: Bismil laahir rahmaanir rahiimi,ahuuzu billaahi minas saytaanir rajiimi,wa inniya uhiizuhaa bika wa zurriyatahaa minas saytaanir rajiimi,rabbi,ahuuzu bika min hamazaatis sayaatiini,wa ahuuzu bika rabbi ayyahduruunii. Bismil laahir rahmaanir rahiimi,allahuma salli halaa seyyidinaa wa mawlaanaa muhammadin,al faatihi limaa uxliqa,wal xaatimi limaa sabaxa naaziril haqqa bil haqqi wal haadii ilaa ziraatikal mustaqiimi,wa halaa aalihii haqqa xadrihii wa miqdaarihil haziim, mu ne mi ngi ñaan julli gii doon gog da na yee képp ku xool mbind mii,mu yee ko ci ne Yàlla kat ànd gi mu ànd ak ñun ànd gu yellook moom la - tudd naa sellam ga - du ànd gu xel di jot,te moom - barkeel na te kawe - jege na nu,waaye jege gu yelloo’k moom,du jege gu xel di xalam,te xam-xamam - tudd naa sellam ga - lu nu sellal la,niki mbooleem ay meloom ,jëmmam it - barkeel na te kawe - tàqalikoowul ak ay meloom te du tàqalikoo ak ñoom it. Waxi Sheex Sanoosi ji,(y.y.g) ak ñi ànd ak moom ci lu aju ci “Mahiya” lu wér la,ndax ñoom kat danoo seet fi nit ñi toll,ñu wax fa’ak ñoom,ndax bu nu weesoo ak ñoom foofu ñu tàbbi ci alkande,ñoom ñépp. Waxi Sheex Ahmad Tiijaan ji it (y.y.g) wuutewul ak li nu wax. Waaye li ñi askanoo ci moom(y.y.g)di wax,ba miy indi ak noonoo ci seen digganteek Abuubakar Ibnu Fatan,na leen wóor ne noonoo googu de ci saytaane la juge,ndax Ibliis day tàbbal lënt-lënt ci xolub képp ku nekkul “Mushaahid”,(mushaahid mooy aji jàkkaarloo,maanaam kay jàkkarlook mbir ya ca nguurug sunu boroom ga) liy firnde ci loolu mooy Jaam biy Ligéeyal Yonnant bi - yal na ko Aji des,jiy Aji jiitu nekkal cig teral - bi muy bind laabiire gii déy,Yonnant bi dikkal na ko (j.y.m) ne ko Sanoosi Ak Sheex Tiijaan ak Xazaalii de ñoom wuutewunu,ñi am ag wuute kay ñooy ñu dul ñoom. Dëgg gi mat a dellu daal mooy bàyyee settantal ci melow “Mahiya” te gëm rekk ne lu am la,ndax di ci settantal day rékki ngëm ,yal na nu ci Yàlla musal. Wasalaam .


Bokk na ci li mu bind ñeel Abuubakrin Ibnu Fatan ci mbirum “Mahiya” lii:Bismil laahir rahmaanir rahiimi,yal na Yàlla dolli xéewal ci sunu sang Muhammad ak ñoñam aki saabaam,ag xéewal akug mucc gog da na ci xamal nit ñi ne la Aboobakrin Bun Fatan waxoon ci waxi Seex Tiijaan ji,jubluwu ci woon Sheex Tiijaan(y.y.g),te moom Sheex (y.y.g) dëppoo na ak moom (Aboobakrin) ci mbooleem li mu wax ci tontoom yi. Ag jub nag mooy nit ñi bàyyee xuus ci lu mel nii,ndax xuus ci, ci ñaawtéef yi la bokk . Waxi qutbu yi, yal na leen Yàlla gërëm, du waxi boroom xam-xam yi,yal na leen Yàlla yërëm. Boroom xam-xam yiy jëfe seeni xam-xam,fi nu toll ci wàlliyu yi mooy fi wàlliyu yi toll ci yonnant yi . Boroom xam-xam yi boroomi tawhiid lanu yuy aar Sariiha mu nu laabal mi, qutbu yi boroomi sellal lanu yu jegeYàlla di aar “Haqiiqa” mu nu leeral, mu nu sellal mi.Kon wormaal ñépp ngir jëmmi Yàlla mu kawe mi lu war la . Bëgganteg boroom xam-xam yi,yal na leen Yàlla yërëm,mooy dundug sariiha,seenug wuute ci masala yi,ag jàng la akug jàngale,dug noonoo,dug iñaanante. Wasalaamu halaykum wa rahmatul laahi wa barakaatuhuu.



Bokk na ci li mu bind ci Ahmadabnil Kawri Addaymaanii, lii:Ahuuzu billaahi minas saytaanir rajiimi,Bismil laahir rahmaanir rahiimi,yal na Yàlla mu kawe mi dolli xéewal ak mucc ci sunu sang ,sunu kilifa Muhammad ak ñoñam aki saabaam,xéewal ak barke ak mucc gog dana ci xamal nit ñi ne Muhammad Ibnu Kawri Addaymaanii,ak Abuubakrin Bun Fatan Alhasani,Yàlla mu barkeel mi te kawe jéggal na leen ñoom ñaar,ci bisub Harafa atum “shahidnaa bikaram” di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak ñaar,te ku ci nekk ci ñoom ñaar xawoon naa alku,sababub loolu mooy juumug Daymaanii,ak weddig Alhasanii. Ahmadu Bun Kawri moom dëppoowul ak Sheex Tiijaan ci li mu doon xuus ci wàllug Mahiya,bu dee Aboobakrin moom daa ñàkki teggiin ak Sheex Tiijaan (y.y.g) ci ñàkk a nangu ag tontoonteem ak Ahmadu Bun Kawri,Sheex Ahmad Tiijaan nag moom ku beru la wëlif leen ñoom ñaar.Liii mooy dëgg gi nga xam ne sikk amu ci. Wasalaamu halaykum warahmatul Laahi wabarakaatuhuu.

Mu bindoon ba tay jëme ci ñenn ci ñoom: Assalaamu halaykum warahmatul laahi tahaalaa wabarakaatuhuu,bu lii jàllee,man de gis naa li xewoon ci sa diggante ak keneen ci lu aju ci mbirum Mahiya,man nag li may wax ci Mahiya,mooy jëmmi Yàlla moom,kawe na te barkeel,du toq ci xelum kenn mu koy jéem a gëstu ,kon xuus ci Mahiya moo’k wuute gi am ci diggante yahood yi ak nasaraan yi ñoo yam,yal na nu Yàlla mu kawe te barkeel mi musal ak yeen ci soxlawoo lu nu yitéelul. Soxlawoo def ndigal yi te teet tere yi moo gën a jaadu ñuy soxlawoo xuus ci googule wàll,Yàlla barkeel na te màgg,nee na :( zarhum fii xawdihim yalhabuun) muy bàyyi leen ci seen xuus googu,ñuy fo. Wassalaamu hallaykum wa rahmatul laahi tahaala wa barakaatuhuu.

Ci noonu Sëñ bi tuxoo ci barab dem ci barab, ba bi mu sancee ca Sahwatul Maayi,nu gën koo xame Xumaak,soriwaay bi di lu tollook doxub bis bu tar ci ku sawar,juge Dagana walla Budoor. Loolu amoon ginaaw lollib atum baksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak ñaar,mu mujj di wër ci barab boobu di tukkee ci kër,dem ca geneen gu jege,mbiram it moo’k mu mbooloo yi koy dikkal di siyaaresi di gën a yokk,ci jamono ju nekk.

Cig gàttal daal leeral mbiri Sëñ bi yepp ci ñaari tukki yii,aal topp aal (aal = tolluwaay yi nit di toll), xew-xew topp xew-xew,kenn ku dul moom manu ko,yal na Yàlla yokk ngërëmam ci moom.

Ag karaamaa ngii gu amoon ca Xumaak,maanaam Sahwatul Maayi,ci genn guddi ci benn ci ñaari weeri rabiih yi,atun jaksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak ñatt,muy tawati tànk ju ko daloon te tar lool,fogloo nu ca guddi googa,nu fanaan ca la wër xaymaam ba,nga xam ne sax jortoon nanu ne du weesu guddi ga,waaye moom mu niy dalal rekk naan nu dellu leen ca yite ya,amul solo,waaye nun deeti nopp mbaa ay xel di àndati ak nun. Bi Yàlla dogalee mu wér ca suba ga,mu xamal ma ne mbir mi de balaa la woon bu juge fa sunu boroom,jëmoon ciy nitam,ñu naroon a fër bu leen daloon (fër = naaxsaay), ma ne sunu boroom lu tax nga jagleel sama nit ñi nattu bii bàyyi ñeneen ñi,ñu ne ma ndax kat Yàlla da laa teg ci sa kawi moroom,kon manul a ñàkk mu jàgleel la sa nattub bopp bu ñeneen ñi dul am,te loolu amul lu ko gën a tar.Man it ma ne yaw buur bi ndax man naa koo gàddu wëlif leen ? Ñu ne ma aha kay, jëlal ,mu doonoon lu diis juge ci asamaan wàcc sama kaw,ma daanu xëm,ñu indi ma ci xayma bi te yëguma. Ki ko yobb ci xayma bi,di Moor Xari Joob nettali na ma ne jaan a ko màtt,kon alhamdu lillaahi ci mucc gi ak tuufu gi (tuufu mooy am li nga bëgg) .