Ñëwug waa-tugal ci Afrik

Fent ak wuññi yu mag yi Soppi

Ci xarnub fukk ak juroom g.j, waa Tugal yi amal nañu ay wuññi (decouverte) yu bari yoo xam ne soppi nanu seenug dund, yi ëppoon solo ci wuññi yooyu ñooy wuññig moolukaay (imprimerie), ki ko def di Gutenberg ci atum 1450 g.j .

Bu njëkk téere yi ci loxo lanu leen daan binde te loolu daa na soxla waxtu wu baree bari, looloo waraloon téere yi seer te néew. Móolukaay nag mi ngi daan ame ci ay bind (forme) yu ñu liggéeye ci weñ, bind bu nekk daa na taxaw taxawaayu aw araf. Bu ko defee ñu raŋale bind yii nga xam ne ñooy defar jumla (phrase) yi ñu soxla, bu loolu jàllee, daa ji door a ñëw, jaar ci seen kaw, njëkk ñu leen di móol ciw këyit. Bu ko defee ñu jël benn yax bi( copie bi) def ci ay xët yu bari, ci noonu lañuy defare ab téere. Ci jamono jii waa Tugal yi xamoon nañu puudar (poudre à fusil) (moom nag – puudar - waa Siin na ko fentoon), ñu jëfandikoo ko ci ngànnaay yu sawara yi ñu njëkk a liggéey , xamoon nanu it buusal (moom nag wa Siin ak naar (arab) yee leen ko njëkk a xam), ñu liggéey ay gaal yu yees yu gën a gaaw te gën a man a jànkoonteek ngelaw yi ci mbàmbulaan yi . Wuññi yii nag ñoo tax mool yi man a def tukki bu sori ci biir géej gi, te wuññi ay suuf yu yees yoy waa Tugal yi xamuñu leen woon.

Ay tukki yu bari daal di nañuy taxaw jëm ci tefesi Afrig yi :

  • Ci atum 1487 g.j, la Bartelemi Jaas agsi ca Boppu Yaakaar Ju Baax Ji ( cap de bonne esperance).
  • Ci atum 1492 g.j, la Kristof Kolombo jugoon di wër aw yoon wu koy àggale End waaye mu far àgg cig mbetteel ci Amerig gi nga xam ne waa Tugal yi sax xamuñu woon ne am na.
  • Ci atum 1498 g.j, la Vasko De Gama jugoon di wër Afrig tukkee ci bëj-saalum, daal di àgg End.
  • Ci diggante 1519 ak 1522 g.j, la Magelan def ab tukki bob ci la wëre àdduna bi, ci lañu wone it ne àdduna bi dafa bulu (kol-kolu).

Digg (centre) yu yaxantu yu njëkk yi Soppi

Waa Tugal yi bi ñu tàmbalee seen wuññi yooyu lañu gaawantu teg loxo suuf yii ñu wuññi : Mool yi toppante nañu ci tefesi Afriig yi, waa Portigaal yi jiitu ci, waa Espaañ yi topp ci, waa Olaand, waa Angalteer ak waa Frãs. Ci xarnub fukk ak juroom benn g.j, la waa Portigaal ak Espaañ teg loxo Amerig gu bëj-saalum gi, bu ko defee waa Portigaal ya jël fa sancu (colonie) bu Breesil féetele ko seen bopp, yeneen wàll ya ca des nekk ca ron ŋëb gu Espaañ. Way sanc yi ( les colonisateurs) tambali woon nañoo génne koom-koom yu mbell yi (yu mine yi), bay it yenn mbay yi niki bantu suukar ak póon ak wëtéen. Waa Tugal yi bëgguñu woon a dugg ci goxub Afrig, ñoom daal dañoo wutoon ay digg yu yaxantu ( centres commerciaux) ci tefes gi, aki waax yu ñuy faral a jaar bu ñuy dem End: benn ngir defar fa seen yaqu-yaqu yu gaal walla ngir wut fa ab dund walla ngir yaxantu, ndax dañu fa daan jënd ay marsandiis yu Afrig niki wurus ak bëñu ñay ak daakaande ak ay rëndaay ( condiments). Waa Tugal yi bi ñuy sanc tefes yi ak di fa tabax ay digg yu yaxantu, daje wuñu woon ak benn jafe-jafe bu juge ci waa Afrig yi, loolu daal ci jàmm lañu ko defe akug dal. Li am sax mooy way dëkk yi teeru nañu leen ci teraanga, jox leeni suuf ak jumtukaay yi manul a ñàkk. Diggi yaxantu yooyu nag ñi ngi daa ame ci yii :

  1. Dencuwaay ( magasin) bu ñuy denc marsandiis yi
  2. Ay dëkkuwaay ñeel waa Tugal yiy saytu digg yooyu
  3. Ab jàngu ( egliis)
  4. Benn saal bu ndaw bu ñuy teertoo way siyaaresi yi

Am na ci diggi yaxantu yi yoy ñi ngi leen di liggéeye ci melokaanu tata (fortification) ju terewu (difficile d’acces) ngir moytu ay cong yu ñu leen mana def. Waa Tugal yi dañoo gis ne seen xay gi moo gën a kawe gu dul moom, looloo waraloon ñu ga woon ko yeneen askan yi.