Wuutuloxo bu mbëj

Wuutuloxo bu mbëj walla masin bu mbëj, ab jumtukaay la buy tax a man a soppi kàttanug doolerandu def ko kàttanug mbëj (di ab safaanukaay) walla kàttanug mbëj ci kàttanug doolerandu (di ab doxalukaay bu mbëj) walla rekk soppi melokaanu kàttanu mbëj gi (di ab soppalikaay). Xeeti masini mbëj yi ñett lañu: Doxalukaay, jurukaay ak safaanukaay

Ab doxalukaay bu mbëj

doxalukaay Soppi

  Ngir Xóotal, yëral bii jukki ci doxalukaay bu mbëj

Doxalukaay ab xeetu wuutuloxo la buy soppi kàttanu mbëj def ko kàttanu doolerandu ngir defi liggéey. Doxalukaay yi dees leen séddale ci ñaar doxalukaay bu dawaan bu safaanu ak doxalukaay bu dawaan bu wéy.

doxalukaay bu dawaan bu safaanu Soppi

Ab xeetu doxalukaay la buy jël kàttanu dawaan bu safaanu soppali ko kàttanu doolerandu. Doxalukaay bu dawaan bu safaanu dees koo séddale ci ñaar:

doxalukaay bu dawaan bu wéy Soppi

Bii doxalukaay dafay soppali kàttanu dawaan bu wéy ci kàttanug doolerandu.

Jurukaay Soppi

  Ngir Xóotal, yëral bii jukki ci jurukaayu mbëj

Jurukaay mooy wuutuloxo bu mbëj biy jël kàttanu doolerandu génne ci kàttanu mbëj.

Jurukaay yi dees leen séddale ci ñaar: Jurukaay bu dawaan bu safaanu ak jurukaay bu dawaan bu wéy

Jurukaay bu dawaan bu wéy Soppi

Ab jurukaay la booy jox kàttanu doolerandu mu delloo la kàtaanu mbëj ci melokaanu dawaan bu wéy

Jurukaay bu dawaan bu safaanu Soppi

Ab jurukaayu mbëj la buy jël kàttanu doolerandu soppali ko dawaan bu safaanu, di nañu ko woowee itam safaanukaay. Nekk na lu ñu Séddale ñaar:

  • Jurukaay bu demandoo
  • Jurukaay bu demandoodi

Safaanukaay Soppi

  Ngir Xóotal, yëral bii jukki ci safaanukaay

Ab wuutuloxo la bu man a dox ci dawaan bu safaanu rekk, ci jëfe dafay soppi melokaanam. Yitteem mooy yokk walla wàññi tolluwaayu dend bi walla rekk soppi baraay bi. Doxam a ngi sukkandiku ci njeexit lees di wax xiirtalu bijjaakon.