Tuubaa, dëkku murit yi,ab gox-goxaan la, mi ngi nekk ci diiwaanu Njaareem (jurbel), ci tunduw Mbàkke. Diggam ak Ndakaaru tollu na ci 150 km .

Baatu Tuubaa mi ngi jóge ci làkku araab di tekki ci wolof : « texe ».

Daaray alxuraan

Demb Soppi

Dencukaay:Kàrtuw Tuubaa ci google earth.jpg
Tuubaa ci google bu suuf si

Dëkkub Tuubaa, kii di Sheex Ahmadu Bamba moo ko sanc ci atum 1887.

Yoriinu dëkk bi Soppi

Dëkk bi mi ngi aju ci Ndaam, doon as ngox, maanam dëkku kaw kaw, bu taaxeedi, te nag doon gannaaw Ndakaaru, dëkk bi gëna taaxe ci Senegaal, ëpp ay nit. tey dëkk bi gën a rëy ci senegaal ginnaaw ndakaaru

Melosuuftouba Soppi

Nit ña Soppi

Tuubaa moo ëpple yokkute ci barig nit ñi ci diiwaani Senegaal yépp (3,2% at mu nekk ci jamono yii ñu tollu te ñu jàppu ne yokkuteg nit ñi di na àgg ba 12% bu ñu àggee ci ati 2010). Yokku yooyu li ko waral moo di tuxu yu bari yi nit ñi di def bawwoo ci dëkk yu nekk ci Bawol ak Kajoor. Dëkk yooyu dañuy gent si ndànk ndànk jëm Tuubaa.

Ci waññib 2002 bi, nit ñi ñi ngi tolloon ci 461 159.

Ci atum 2007, bu ñu ajoo ci gam-gamle gu nguurug Senegaal, waa dëkk bi tolloon nañu ci 529 176.

Koom koom Soppi

 
daral

Naataangeg dëkk bi lëkkaloo na lool ak Màggal gu mag gi giy dëppoo ak demug Seex Ahmadu Bamba ci géej gi.Ba tay Tuubaa dafa bari li waa Senegaal di woowe Moodu moodu, di ay tukkikat yu féete Tugal tey ëndi xaalis bu bari ci dëkk bi. Lii di yaxantu (jënd ak jaay) tamit da faa dox lool.

Aada Soppi

Kii di Seex Abdul Ahat doon ñatteelu xalifa Seex Ahmadu Bamba moo fa tabaxoon barab bi ñuy woowe daaray kaamil di kàggu gu ñu denci mbindum Seex Ahmadou Bamba ak yeneeni mbind aki téere yu aju ci lislaam, ak ci yeneen fànni xam-xam yi yittéel nit, mi ngi feete nag ci penku jumaa ji, làng ak armeel yi.

Tabax yu mag yi Soppi

Royuwaay:Xët wu ñu yaatal

Ci Tuubaa la jumaa ju mag ji nekk, doon jumaa joo xam ni jenn la ci Afrig gu sowwu jant, ci taaram, ak ci rëyaayam. man nañoo jàpp ne mooy xolu dëkk bi, ndaxte yeneen kër yepp dañoo ñëw di ko wër ndànk ndànk, ànd ak màggaayu dëkk bi. Jumaa ji am na juroomi sooroor ak ñeenti xubba. Soorooram bi gën a gudd tollu na ci 80 meetar. Sooroor boobu, kii di Sëriñ Fàllu Mbakke mooko tudde Làmp Faal féetele ko kii di Maam Seex Ibra Faal ci 7 juin 1963. Bis boobu moo di ubbite gu njëkk, ba ñu bari teewe woon nañu ko, ku mel ni Lewopool Sedaar Seŋoor. Foofu ci jumaa ji fa la barabu Seex Ahmadu Bamba nekk.

Dayo Soppi

Xool it Soppi

Teerekaay Soppi

  • (en) Touba and the meaning of night, New York, Feminist Press at the City University of New York, 2006
  • (en) Eric S. Ross, « Touba: a spiritual metropolis in the modern world », Canadian Journal of African Studies, 1995, 29.2
  • (en) Eric S. Ross, Sufi City: Urban Design and Archetypes in Touba, Rochester, University of Rochester Press, 2006, 344 p. (ISBN 1580462170)
  • (fr) Monique Bertrand et Alain Dubresson, Petites et moyennes villes d'Afrique noire, Karthala, 1997, p. 118-119 (ISBN 2865377431)
  • (fr) Cheikh Guèye, L’Organisation de l’espace dans une ville religieuse : Touba (Sénégal), thèse de doctorat, Strasbourg, Université Louis Pasteur, 1999, 650 p.
  • (fr) Sophie Bava et Cheikh Guèye, « Le grand magal de Touba. Exil prophétique, migration et pèlerinage au sein du mouridisme », Social Compass, 2001
  • (fr) Cheikh Anta Mbacké Babou, Touba, genèse et évolution d’une cité musulmane au Sénégal, Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 1992, 39 p. (Mémoire de DEA)
  • (fr) Cheikh Guèye, Touba : La capitale des Mourides, Paris, Karthala, 2002
  • (fr) Amar Samb, « Touba et son "magal" »; Bulletin de l'IFAN, t. XXXI, série B, n° 3, juillet 1969, p. 733-753
  • (fr) Alexis Sané, Situation et perspectives de l'intégration de Touba dans la vie économique du pays, DAKAR, CFPA, 1970, 66 p. (Mémoire de stage)

Filmokaay Soppi

  • (fr) Blaise Senghor, Grand Magal à Touba, court métrage documentaire, 1962, 20 mn
  • (fr) Christophe Marlard, A travers le Sénégal. 3, Touba, une ville à part, film documentaire, ENS Fontenay/Saint-Cloud, 1999, 13 mn

Lëkkalekaay yu biti Soppi

 

Xool it Wikimedia Commons
[[Commons:
Wàll:Touba, Senegal|Touba]]