Saab-saab xeetu garab la gu bokk ci njabootug « Moringaceae », mi ngi bàyyikoo ci bëj-gannaaru End. Garab gu fés la leegi ci àddina bépp, te miin barab yi bari naaj.

Saab-saab gi (Moringa oleifera)
Saab-saab gi (Moringa oleifera)

Melo wi Soppi

As ngarab la su gaaw a màgg te man a muñ bekkoor. Guddaayam danay àgg ba 10i met. Saab-saab garab guy gaaw a màgg la. Peeram danay àgg ba fukk baa 12i met, dàttam nag danay àgg ba 45i sàntimet, xàccam melo wu baam la te jege weex.

Tóór-tóor bi Soppi

 
Tóor-tóoru garabu saab-saab

Tóor-tóor bi daa am xet te nguuni-ngaana, danay am ba juroomi xob yu tolloowul. Wirgoom dafa mboq. Tóor-tóor bi guddaayam 1 la ba 2,5i sàntimet cib guddaay. Yaatuwaay bi 2i sàntimet la.

Doom bi Soppi

 
Meññatum saab-saab

Doom bi këmbaan la gu ñàtti-koñe te palmaan. Guddaayam 20 la ba 45i sàntimet. Xoox bi dafa wërmbalu.

Solo si Soppi

Saab-saab bari na pàcc yees ciy jëfandikoo: foytéef bi, xob wi, xoox bi su ñoree, diw bees ciy jële, tóor-tóor bi , reen yi. Saab-saab dees na ko jëfandikoo ci anam yu bari ci wàllug toggu ci àddina bépp. Manees na ko lekk nim bindoo. Fële ca Senegaal dees na ko toggu boole ko ak cere (cere mbuum).

Turu xam-xam wi Soppi

Moringa oleifera

Tur wi ci yeneeni làkk Soppi

araab: البان
farañse: mouroungue
angale: drumstick tree
itaaliyee: moringa