dëkkug lebu yi ci ndakaaru mi ngi am ginnaaw ay duusi gàddaay ci diggante XV¹⁵ ak XVIu¹⁶ xarnu. Laataa seenug càmp ci Senegaal, ab tukki bu gudd moo leen war a jëlee ca penku Afrig ba ci sowwu Afrig jaare ko ci bej-gànnaaru gox bi. Ñaari gongikuwaayu xibaar lanu am ngir man a jéem a rëddaat yoon wi leen fi indi. Nettali gi ciy kàddu di na tax nu man xam lu bari ci jamono yu mujj yi. liggéey yu ay gëstukat niki Seex Anta Joob T. Gostynski, G. Balandier ak P. Mercier, F. Brigaud di nañu tax nu man a dem ba ca njëlbeen

Gongikuwaay Soppi

Tambali na am na 7 000 at, tukki bi jaare ci bëj-gànnaaru Afrig, ci ay pàcc yu bari la ame. Jàpp nanu ne dañu leen fay war a dàqe walla ñu demal seen bopp ngir lànk nooteel. Aw askan wu fonk i baaxam (aadaam), ak i melokaanam la. Ci melokaan yooyu sax lañu sukkandiku ngir joxe ay gongikuwaayu baatu lebu. Am na ñu ne mi ngi joge ci baatu lebu (maanaam dëkku, misaal: dëkku am mbër ), ndax seen mbañug nooteel, ñeneen ni ci lubu (jqmbaar) la jóge, ak yeneen.

Seenug càmp ci Ndaakaaru Soppi

Laataa ñëwug lebu yi ci Ndakaaru, juróom-benni gàddaay yu toppante lañu amal. Bi ñuy ñëw ay mbooloo yu ndaw lañu doon def, ndànk ndànk ñuy toog, ci ndoorteel gi ci barab yi soose yi nekkul woon, ñu dem ba sanc Ndakaaru gépp. (Caam, 1970:6)

Ñi ngi agsi ci 1430 (atum junni ak ñenti téeméer ak fanweer), boobu ag nguuru soose, gu tambalee woon Tubaab Jalaaw ba Ngor, moo fa nekkoon. Ca jamono yooyu, ay réewi soose yu bari ñoo fa amoon, ci seeni bopp ñii ñoo fa nekkoon: Malang Tambaa, Jalla Jaw, Gitigi Maroon, Nak Jombel moom dund na ba 1470. Xare bu tar ba ca toppoon waraloon dawug Soose yi jëm Gàmbi.

Jàppante bi wéy na ba ci XVu¹⁵ xarnu bi, ba killifay soose yi deewee la xare ba jeex. Ca la lebu yépp jóge Jolof mi doon waaj a xar, ndànk ndànk ñu dem ba moom Ndakaaru gépp. Ginnaaw bi yàggul dara dammeelu Kajoor di leen jéem a sanc loolu jur ay xare yu bari ci seen diggante.

Nosiinu politig bi Soppi

Nosiinu seenug mboolaay, ci li ñu xam, am na laataa seenug ñëw ci Ndakaaru te mi ngi dàttu woon ci palug ab Laman. Ndànk ndànk ñàkk kaaraange gi ak jamono ju laaj jeneen nosiin tax yeneen cëslaay taxaw.

Ci boppu askan wi, Jaraaf bi moo fa nekkoon, di ki jiite nguur gi, Ndey-ji-réew ji tegu ci, di ki yoroon mbiri biir ak biti réew. C.T. Mbeng moom daf ko jappe niki "ab aji-teewal ak aji-rattaxal ci diggante réewi lebu yi". Saltige bi moom moo yoroon suuf si ak aartu (défense) gi ak ndox mi. Ñett ñii ñoo yoroon doxiinu réew mi. Taxawaloon nañu ñaari pénc ngir ñu jàppale ñett ñooñu ci seen liggéey: Jàmbur ak péncu fere yi. Bu njëkk bi di nañu ko wax itam ""jataayu mag ñi"" boroom xam-xam yi rekk a fay nekk, Ndey-ji-jàmbur moo koy jiite. Péncu fere

Jàmbur bi mooy kiy fal jaraaf, ndey-i -réew ak alkaati bi. Te ñiy yor yooyule ndombal-tànk waruñoo doon ay xeet (maanaam ñu bokk ci wàllu yaay). Lii di na tax ba man-man (pouvoir) gi du nekk rekk ci yoxoy genn njaboot. Bii matuwaay di na tax ba réew mi du soppiku nguur. Kon man-man gi dañu koy séddale ci njaboot yu bari, ku nekk man ngaa am ndomba-tànk, suñuy tànn kenn, ci genn njaboot gi, lenn li ñuy xool mooy ay mbaaxam.

Lëkkalekaay yu biir Soppi

Téerekaay Soppi

  • (fr) Armand-Pierre Angrand, Les Lébous de la presqu'île du Cap-vert. Essai sur leur histoire et leurs coutumes, Dakar, Éd. La Maison du livre, 143 p.
  • (fr) Birahim Ba, La société lébu. La formation d’un peuple. La naissance d’un État, Dakar, Université de Dakar, 1972, 206 p. (Mémoire de Maîtrise)
  • (fr) Georges Balandier et Pierre Mercier, Particularisme et évolution : les pêcheurs Lébou (Sénégal), IFAN, Saint-Louis du Sénégal, 1952
  • (fr) Adama Baytir Diop, La prise de position de la collectivité lebu en faveur du “oui” lors du référendum de 1958. Essai d’interprétation, Dakar, Université de Dakar, 1985, 51 p. (diplôme d’études approfondies)
  • (fr) Adama Baytir Diop, La communauté lebu face aux développement de la politique coloniale : la question des terrains de Dakar (1887-1958), Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 1995, 277 p. (Thèse)
  • (fr) Claude Laborde, La confrérie layenne et les Lébous du Sénégal. Islam et culture traditionnelle en Afrique, Karthala, 1997 (ISBN 2865377121)
  • (fr) Colette Le Cour Grandmaison, Rôles traditionnels féminins et urbanisation. Lébou et wolof de Dakar, Paris, EPHE, 1970, 4+310+23 p. (Thèse de 3e cycle, publiée en 1972 sous le titre Femmes dakaroises : rôles traditionnels féminins et urbanisation, Abidjan, Annales de l’Université d’Abidjan, 249 p.)
  • (fr) M. Mbodji, « Tiané, une jeune fille en quête d'initiation : rêver chez les Wolof-Lébou, ou comment communiquer avec les ancêtres ? », dans Psychopathologie africaine, 1998-1999, vol. 29, n° 1, p. 7-21
  • (fr) Mariama Ndoye Mbengue, Introduction à la littérature orale léboue. Analyse ethno-sociologique et expression littéraire, Dakar, Université de Dakar, 1983, 378 p. (Thèse de 3e cycle)
  • (fr) Médoune Paye, La collectivité lebu de Dakar : organisation, rôle politique dans les élections municipales de 1925 à 1934, Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 2001, 118 p. (Mémoire de Maîtrise)
  • (fr) Ousmane Silla, Croyances et cultes syncrétiques des Lébous du Sénégal, Paris, EPHE, 1967, 517 p. (Thèse de 3e cycle)
  • (fr) Assane Sylla, Le Peuple Lébou de la presqu'île du Cap-Vert, Dakar, Les Nouvelles Éditions africaines du Sénégal, 1992, 135 p.
  • (fr) Tamsir Sylla, Introduction à un thème négligé : révoltes et résistances en milieu lebou au XIXe siècle. Approche critique des sources, Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 1990, 36 p. (Mémoire de DEA)
  • (fr) Ibrahima Thiam, Ousmane Diop Coumba Pathé, personnalité politique lebu : 1867-1958, Dakar, Université de Dakar, 1987, 46 p. (Diplôme d’Études Approfondies)
  • (fr) Guy Thilmans, « Étude de quelques crânes lébou (Sénégal) », Bulletin de l'IFAN, 1968, t. 30, série B, 4, p. 1291-1297