mbëbijjaan ab cëru xaralaymbëj la buy jur ab toolu bijjaakon su ñu jaaralee ab dawaanu mbëj ci biiram. Naka-jekk dafay am ab saal (ag weñ lay nekk) di fi ñuy lëmës wëñug përëg gi, walla beneen xeetu wommatukaayu mbëj, di fi dawaan gi di jaar. Man naa nekk dawaan bu safaanu walla bu wéy.

Ab mbëbijjaan

Jëfandikoom Soppi

 
Mbëjbijjaan bees di jëfandikoo ngir tonni ay weñ

Bari na fu ñu koy jëfandikoo,

  • Fu mel ne ci doxalukaay yu mbëj ngir juddal ab toolu bijjaakon ci wëndeeluwaan bi;
  • Dees na ko jëfandikoo ngir defi liggéey, ngir yëkkati ay weñ;
  • ngir defari tëjukaayu bunt, su ñu jaarale dawaan bi mu jur ab tool jenn doole juddaale ca téye liy tax ba bunt bi du ubbeeku, su dawaan bi deñee mu ba ko ñu man koo ubbi.

Lëkkalekaay yu biir Soppi