Gëwéel yi ñaari rëdd lañu yu dëppook yamoo gi: gëwéelub Tef tollu ci 23°24' wu tus-wu-gaar wu bëj-gànnaar gi ak gëwéelub Sànkar tollu ci 23°27' wu tus-wu-gaar wu bëj-saalum. di nañu woowe it gëwéel diiwaan yi ne ci li wër rëdd yooyule (di faral di wax dëkk ci gëwéel yi).

Melokaan Soppi

Ci li jege yamoo gi, di nañu faral di gis klimaa bu ànd ak tàngoor wu tar ak taw bu bari ci at mi mépp: di ko wax klimaab yamoo. Waaye, ci li jege gëwéel yi (Tef mbaa Sànkar), ci at mi noor ak nawet rekk a ci am, kon wàcciit yi (taw yi) day wuute ci jamonoy at mi, ba daanaka at mépp ay tàng, di li ñuy wax klimaab gëwéel.

Waaye nag jàpp nañu ne it ngelaw yiy upp ak duusi géej yi ak rëyaayu diiwaan bi am nañu ay jeexiital yu solowu ci klimaay diiwaan yi, ba tax na su nu seetloo yenn diiwaan yi, doonte nekk nañu ci wetu ab gëwéel, amuñu klimaab gëwéel (ci misaal diggu Óstraali walla bu Sahara, nga xamne amuñu nawet) ak yenn diiwaan yu am klimaab gëwéel te nekkuñu ci lu jege gëwéel yi( lu mel ne réewum Keeñaa, nekk ci yamoo gi te li ëpp ci suufam klimaab gëwéel la am).

 
Gëwéel yi ñooy rëdd yu baxa yu xëm yi, ci kaw ak suufu yamoo gi, moom di rëdd wu leer wi

Diiwaani gëwéel yu mag yi Soppi

Diiwaan yiy dund cib klimaab gëwéel dëgg-dëgg ñoo ngi nekk ci diggu Aamerig ak bëj-saalumu Aamerig, ci digg ak genn wàllu bëj-gànnaaru Afrig, ci bëj-gànnaaru Óstraali ak genn wàllu Endoneesi. Li des ci barabu diggantegëwéel bi dañu leen di séddale ci diggante klimaab tàkk (rawatina ci Afrig), bu yamoo walla bu xaw a sedd (rawatina ca Asi

Lëkkalekaay yu biti Soppi

 

Xool it Wikimedia Commons