Ci angale mooy aloes; Ci faranse mooy aloès

Bantu genn garab la bu xeeñ lu neex, te joxe diwlin ji ñu def ci néew yi. Ci réewi penku yi la jóge. Boroomi xam-xam yi ci turu Akilariya agalosa (Aquilaria Agallocha) lañu ko xame. Garab yi am benn feebar rekk ñooy xeeñ. Feebar bi dafa soppi wàllu dàttam ba bant bi dëgër te ëmb benn diwlin bu neex. Bu ñuul bi mooy lu am feebar. Lu weex mooy lu amul feebar.

Dañu koy gis ci Injiil ci Yow 19:39.