Ñaareelu Xareb Àdduna

Ñaareelu Xareb Àdduna bi ab xare la woon bu laaloon àdduna bi. Mi tàkk ci bi Almaañ ak Itaali ak Imbratóor gu Sapoŋ bëggee noot àdduna bi ci diggante 1914-1918 g.j. Ñaari réew yii mu ci nekk daw na wuti ndimbal ci li ëpp ci réew yi mu defal ay tappoo. Bu ko defee yàggul dara lu bari ci réewi àdduna bi duggsi ci.

Faraas sàkku woon na ci mbooleem ay sancoom ñu jàppale ko ci xeex bi, te jox koy nit. Jot naa dajale - ci ndimbalul Blees Jaañ - am mbooloom xare mu mag, mu xeex ci wetu Faraas lank sancuy Almaañ yi, ñu nangu ci Togóo ak Kamerun ak wàllug sowwu gi ci bëj-saalumu Afrik ak Tanganika (Tansani ci jii jamono).

Ci atum 1939 g.j, la ab xare tàkkaat bu bees bu tàllaliku ba daj Tugal ak mbooleem réewi àdduna bi. Hitler njiitul Almaañ li daa gëmoon ne réewam mooy mi gën a kawe ci àdduna bi, kon yi ci des yépp dañoo war a toroxlu ciy tànkam, Itaali nag ak Sapoŋ dañoo àndoon ak moom ci loolu. Waaye réewi demokaraasi yi dañu koo lankoon.

Xareb Almaañ bi songoon na suufi Faraas yi, loolu jur Faraas séddaliku ci ñaari wàll, wàll guy jàppale Almaañ te ànd ak moom ak gu nekk ci ron kiliftéefug Jeneraal Degol, mooy giy jàmmaarloo ak a xeex Almaañ.

Li laytaay xare bi Soppi

Lijjanti ak saxal ya juddoo woon ca ndajem jàmm ma ca Paris, ci ginaaw Xareb Àdduna bu Njëkk bi, ñoo jur - man nanu ne – lu ëpp ci li sooke ñaareelu xare bi. Kollareg jàmm ga fa juddoo woon sooke woon na mer wu metti akub sànj ci askani reew yi nu note ca xeex ba. Askan yooyu nga xam ne doyutoon ñu yanu coonay xare beeki musibaam rekk, waaye ñu tegati ci yan leen li ci juddoo ci ginaaw bi ciy saxal aki lijjanti yu diis yoo xam ne réew yi notoon a leen tegoon ci seen kaw. Loolu nag juroon ci ñoom ag mbañeel akug bëgg a fayyu, nekkiinu koom-koom wi jaxasoo, tegoodi ci yoon, am pax gasu ci Tugal ci diggante askan yeek seeni goornamaa, loolu tam - man nanu ne - mooy li gën a tax ay noste yu yees sosu, yoy “sañ-sañ bu joyu” lanu jëloon def ko seen raayo. Ay kureel yu neew jugoon nanu teg loxo ci àtte gi ci yenn ci reewi Tugal yi, daal di biral ne li leen tax a jug mooy xettali seeni askan ci jafe-jafe yi nga xam ne xareb adduna bu njëkk bi ba na leen fi. Ay goornamaa yu diktaatoor feeñ ci biir Tugal ak ci biti. Leegi nag jeneen jamono ju yees tàmbli ju ngànnaayu, muy wutu ngànnaay moo xam ne li ko jur mooy bëgg a fayyu ci reew yii note ci xare bu njëkk bi, te toroxal askani reew yi nu not, te diisal seen ginaaw ci ay alamaan yu saf te tar. Lii daal moo sabab xareb adduna bu ñaareel bi.

Àttey beddi yu bees yi sosuwoon man nanu ne ñooy jëfka yi jiitu ci taal ñaareelu xare bi. Ñu indil la wax ju gàtt ci ñatt ci yi gën a am solo ci noste yooyu.


Nosteg àtte gu mbokkte Soppi

Riisi mooy reew mi àtteg mbokkoo njëkk a taxaw, loolu di woon ci ginaaw fippug oktoobar ga amoon ca atum 1917g, li ko waraloon di koom-koomam ba daanu woon, te ñu dàqoon ko ci anam gu toftaloo ca xare bu njëkk ba ca kanamu Almaañ ci ñaari at yii di 1916 ak 1917g, te mu ñàkkoon it lu tollu ci milyoŋ ak xaaj ci ay xarekatam ca xare booba.

Lenin (1870 – 1924g) mi nekkoon njiitul làngug mbokkte gi (parti communiste), moo jiite woon fipp googu, daal di woon def ag juboo ak waa Almaañ yi, taxwal it ay jataay yu askan yu barab yi (soviets) , daal di xeetal jumtukaayi ligeey yi, taxawal ab goornamaa bu ay ligeeykat aki baykat, daal di yëngu ci luy neewal tàqale yi am ci diggante xeet yu wuute yi. Waa Rusi yu Sofiet yi taxawaloon nanu ab jë bu yaatu kontar nosteg bopp-alal gu soww gi, ñu jiite woon kureelub mbokkoo bi kontar diine ak nostey demokraasi yi, ñu mujj nag am doole ju mag ak jeexiital gu rëy ci liy xew ci adduna bi, yàgg nanoo jëfi jëf ci yekkati tàngoor yi ci adduna bi, walla xiiroo ak ngaayoo yi daa am ci adduna bi ci diggante ñaari xare yi.

Nosteg àtte gu Nasi ca Almaañ Soppi

Làngugug mbokkoo gu xeet gu ligeeykat yi gu ( Nasi) gi (di parti national-socialiste almand des travailleurs) gii làngug politig di gu Nasi gi, daa jariñoo woon (profitoo woon) ci li daloon waa Almaañ yi, te wàcci ci seen kaw ci toroxte ak doyadal ak suufeel, te li ko waraloon di tënk-tënk yi nekkoon ci kollareg Versailles gi, ak jafe-jafe yi mu leen indil, ak ñàkk gi leen wër, peek leen, ak ñàkk-ligeey gi, ak deltu ginaawug koom-koom bi nga xam ne saxoon na fi ay at ginaaw xare bu njëkk bi, làng gii nag jariñu woon na ci lii lepp ngir fitali ca àtte ga (l’état) teg ko loxo, nangu ko, ci njiitug Adolf Hitler (1889 – 1945g), mi nga xam ne bindoon na dali làngam googu ci teereeb xeexam ba, dal yooyu nag danoo taxawoon ci ay cëslaayi waaso, ndax daa gëmon ne waasow Jermaan mooy waawo wi gën ci waaso yi, te it daa gëmoon ne danoo war a sos ag Almaañ gu mag gu ëmb mbooleem waa Almaañ yi, gëmoon it ne àtte gi (l’état) daa war a teg loxo mbooleem lonkoo yu rënk yu mag yi ci Almaañ, te danoo war a neenal kollare ga nu fasoon ca Versailles, te danoo war a delloosi mbooleem sancu yi kollare googu ñàkkloo woon Almaañ.

Hitler mujj na di njiilul Almaañ loo xam ne daa amoon sañ-sañ bu joyu (pouvoir absolu). Ñu mujj di ko wooye Fuhrer, mu tàmbli nag di doxal dali làngam yooyu ci askanu Almaañ wi nga xam ne àndoon na ak moom ngir bëgg a mucc te xettaliku ci nekkiin wu bon wi mu nekke woon, rawati na ñàkk-ligeey gi nga xam ne yaatu woon na lool ci Almaañ ngir xare bi, ak ngir tënk-tënk yi nga xam ne kollareg Versailles gi indi woon na leen fi.

Hitler def na ay jëf yu bari yoo xam ne ñoo fi sabab ñaareelu xare bi, ndax daa jëloon diiwaanu Saar boole ko ci Almaañ atum 1935g, neenal kollareg Versailles, jox sodaar si ngànnaay yu diis te xereñ, jëmale endustri bu Almaañ ci ligeey ngànnaay ak jumtukaayi xare aki bagaas yu ame solos xare. Mu jëlati reew yiy wax làkkuw Almaañ wi boole leen ci Almaañ, daal di taxawal Rayix bu ñatteel bi. Mu booleeti Otris ci Almaañ atum 1938g, jëlati goxub Sodit bi nekk ci Cekoslaawi atum 1939g, daal di jeem a nangu yoonu Danseg ci doole, seddoo ak Rusi Poloñ. Almaañ nag dundoon na ci ron àtteg Nasi la ko dale ca 1933g ba bi mu daanoo tas ci atum 1945g.

Nosteg àtte gu Fasi ca Itaali Soppi

Waa Itaali yi yëgoon nanu – te ñoom kat ci reew yi amoon ndam lanu woon ci xareb adduna bu njëkk bi – yëgoon nanu ne danu leen a naxe ca ndajem jàmm ma amoon ca Paris, màngiit yi juge woon ci xare bi it lu neew lanu leen ci jox, te kat ñoom ñu ci sonne lanu.

Ag ñàkk ligeey tas ci Itaali, nekkiinu nit ñi ñaaw, làngi politig yi fees fa dell, reew ma jaxasoo, xalaat yi tas fa, di mbokkte (communisme) fasi, ak yeneen xalaat yi. Fasi nag lu fi ñëwoon la ngir xeex mbokkte, Benito Mussolini jiite ko mi jiite woon ag làngam (1883 – 1945g). Làng googu nag danoo warlu woon ci seeni dal (principes) xeex mbokkte, taxawal ag nosteg dimblante, te jeem a jot ci ngañaayi sanc yi nga xam ne danu leen a xañoon Itaali ca ndajem Paris ma.

Ci noonu làngug Fasi gi tàmbli di jëfandikoo fitna(violence) ci xeex ak xuloowaaleem yi, bi dégug làng gi gënee dëgër, gën a ñaw, mu gën a am doole ci la Mussolini ak àndandoom yiy solsimis yu ñuul xuppe goornamaab Itaali bi, ci noonu Buurub Itaali bi di Victor Emmanuel amatul woon pexe, mu daal di jox nguur gi kii di Mussoliini, mi nga xam ne mujj na di diktaatooru Itaati, ñu ko daa dàkkantale Dotsi.

Mussolini digale na ñu neenal làng yi, aaye askanu Itaali wi ñuy def yëngu-yëngu mbaa coow, nos endustri bi, dëppale diggante njariñi liggéeykat bi ak naatug walla jëm kanamug ndefar yaxantu yi. Daal di juboo ak Paab bi, delloosi njàggalem diine mi ci jàngu yi (leekol yi).

Mussolini feeñal na mbonam gi ak mbonug làngam gi, jaare ko ci jëfam yu ñaaw yi mu jëmale woon ci askanu Libi wi, ba mu fa bëggee samp sancug Itaali gi. Mu gënoon a yaatal ag kilifteefam ca Ecopi atum 1936g, ginaaw bi ko soldaari Itaali yi tegee loxo ci doole, nangoo ko ci waa Ecopi. Yaatalug sanc gu Itaali gii merloo woon na askan yi nekkoon ci ron ag sancam, te taxoon na yeneen reewi sancaan yi kontar ko ci loolu. Lii nag mooy li jegeele diggante Nasi ak Fasi, nga xam ne mujj nanu àgg ci def ag dëppoo ci seen biir, mooy taxawal ag tapoo gu xare , nu duppee ko diggub Berlin-Rom .

Bokk na ci aakimookat yii ba tay, làngug xare (parti militaire) gi nekkoon Japon, ak àtteg Franco ga ca Espaañ (1892 – 1975g), moom Franco mi mujjoon ame nguur gu joyu (pouvoir absolu) ca Espaañ atum 1939g, ginaaw xareb ñoñ bu Espaañ ba. Koolute gi askani Almaañ yi amoon ak yu Itaali yi, yu Espaañ yi ak yu Japon yi ci seeni goornamaay xeet yu ëppaloon yi te teengal dolliku woon na te li ko waraloon di ñàkk gi nostey bopp-alal yi ak yu demokraasi yi ñàkkoon kàttan ci jële fi coonab koom-koom bii fi amoon ak ñàkk gu tar gii ubale woon Tugal gépp ak feneen, ci biir jafe-jafeb koom-koom bi amoon ci adduna bi atum 1929g, ñu gënoon koo xame ci turu lamb gu mag gi.

Yeneen jëfka yu sabab xare bi Soppi

Am na fi yeneen jëfka yoy dugg nanu ci li fi indi xare bu ñaareel bi, bokk na ci yi ci ëpp solo:

  • Lott gi kureelu xeet yi lòttoon ci ñoŋal jàmmi àdduna bi, ginaaw bi ci Almaañ ak Itaali gennee ak Japon.
  • Digg (axe) yu politig ak xare (militaire) yi nga xam ne reewi diktaatoor yi taxawaloon nanu leen ci seen biir, bu ci mel ne digg bu Berlin-Rom, ak bu Berlin-Tokkiyo, ak kollarante gu ñàkk-a-noonu gi amoon ci diggante Berlin-Mosko laata a xareb ñaareel bi di tàkk ci lu tollu ci ay ayu bis yu neew. Ci geneen wàll gi, Fraans, Britani, Romani, Poloñ, ñoom itam booloo nanu def seenug tapoo. Nii daal la ñaari dank sosoo dankub digg bi, làmboo Almaañ, Itaali, Japon, ak dankub reew yi tapoo walla (way tapoo yi) di Britani, Fraans, Romani, Poloñ, Benoog Sofiet gi ak Amerig – ci ginaaw bi.
  • Xuloo bi amoon ci diggante reewi Balkaan yu yees yi te aju woon ci mbirum dig yi ci seen biir, ndaxte amunu woon ay dig yu sax, ak xuloo bi amoon te aju woon ci mbirum xeetu (nationalisme), ndax kat reew yii, di yu sosoo ci seddaleg ndaje ma, danoo ëmboon lu sakkan ciy xeeti Almaañ, lu jege juroomi milyoŋi ay waa- Almaañ, ñu mujjoon bokk ci njabootug Poloñ ak Cekoslaafi.
  • Masalam yoonu Poloñ wi tàqale Almaañ ak Brusiya, te daytaloo ca waaxub Danseg bu gore ba(libre). Ña dëkke woon ca yoon woowa ci ay waa Almaañ jege woon nanu 96٪ , ci noonu Hitler daal di ne day boole yoon woowu ci Almaañ, looloo fi taalati gilinug xare bi ci adduna bi, ndaxte Fraans ak Britani ñoom danoo daal di woon jàpple Poloñ, ci noonu Hitler daal di joxe ay ndigal ci nu song Poloñ, ci 01 satumbar atum 1939g, ginaaw bi mu gisee ne ànd na ak Bennoog Sofiet gi, Itaali ak Japon . Nii daal la sawaras ñaareelu xareb adduna bi tàkke.

Jamonoy xare bi Soppi

Ñaareel Xareb Àdduna bi romb na ci ñatti jamono ñooy:

  • Jamono ju ndam yi Hitler doon ame ci xare bi, mu tàmbli ci 1939 – 1941g
  • Jamonoy yamoo (équilibre), walla li nuy duppee at mu jaxasoo mi, di woon atum 1942g
  • Jamonoy nërméelu ñeel réewi digg yi, mu tàmbli ci atum 1943 – 1945g.

Hitler yëgaloon na Poloñ atum 1939g ne ko manul ñàkk mu génne loxoom ci waaxub Danseg bi, te delloo Almaañ yoonu Poloñ wi romboon ci suufus Almaañ. Boobu lëj-lëj – bokkoon na ci li juddoo woon ca ndajem jàmm ma – mooy li fi taalati xare bi ci adduna, ndax mooy sabab bu jonjoo bi ko jafal. Hitler yamul rekk ci yonnee ag xupp jëme ca Poloñ, waaye da ca a rax dolli yabal ay soldaaram ñu song ko, teg loxo ay suufam, bi mu lànkee bañ a wuyyu wooteb Almaañ bi, bañ a faale xuppam gi. Bi mu kodefee, Britani ak Fraans jug yonnee ag xupp jëme ca Almaañ, ne ko na génn suufus Poloñ si, ci diir bu weesuwul ñaar-fukk ak ñeenti waxtu. Bi Almaañ lànkee bañ leen a déglu, la ko Britani ak Fraans song, ci 02 satumbar 1939g.

Almaañ jot naa teg loxo waaxub Danseg ak yoonu Poloñ wi, ak lenn ci goxi soww yu Poloñ yi. Ag dëppoo am ci diggante Almaañ-Rusi, gu waral ñu séddoo ñoom ñaar suufus Poloñ si, loolu nag di bi Rusi tegee loxo goxi penku yu Poloñ yi, daal di def ak Almaañ kollareg ñàkk-a-noonu (non-agresssion) di gi amoon ci 23 ut 1939g. Waa Almaañ wéy ci seen xare bi, daal di nangu Danmark ak Norwej atum 1940g, ginaaw ba nu fa dàqee dooley Britani ji ak ju Fraans ja fa nekkoon. Ci geneen wàll, Rusi moom gën na a tàllal ay tànkam ci Finland, loolu nag mu jaare ko ca kollareg ñàkk-a-noonu gi mu fasante woon ak Almaañ. Almaañ daal di song Luksamburg, nangu ko ci lu yéeme cig gaaw. Songati Holand, nangooti ko, song Beljig nangu ko waaye ci ginaaw xare bu saf sàpp, bu mujjoon waral deltu ginaawug dooley Britani ji ak ju Fraans ji atum 1940g. Dooley jañ ak naj gi Almaañ doon def ci bëj-gànnaaru Fraans gënoon a dolliku, gën a tar, ci noonu goornamaab Fraans bi daal di tuxoo Paris, dem Bordeau, foofa lanu tàmbli woon a sàkku ag wéer ngànnaay ak Almaañ. Ci noonu General Deegol daw làqu ca London, fa la doon jiitee jànkoonte (resistance) gu Fraans gi kontar réewi digg yi, fa la birale it ag Fraans gu gore gu ànd ak réewi tapoo yi( les alliés). Goornamaab Fraans bi diriku woon ba Bordoo, daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak Almaañ, muy gu mel ne ga Almaañ defoon ag réewi dëppoo ya ca 1918g.

Wéer ngànnaay yi Soppi

  • Almaañ nangu bëj-gànnaaru Fraans, péey ba di Paris bokk ca, ak mbooleem tefesi Fraans yi tiim mbàmbulaanug atlas gi.
  • Fraans day fay Almaañ ay alamaan yu alal, yu tollu ne ferey soldaari Almaañ yi nangu Fraans.
  • Limub soldaari Fraans yi dootul weesu téeméeri junniy soldaar.
  • Taxawal goornamaa bu Fraans buy ànd ak Almaañ, bii goornamaa nag taxawoon na ci njiitug Marsal Bitan. Ñu duppee woon ko goornamaab Fishi, ngir nekk ga mu fa nekkoon.

Ginaaw bi Fraans wommatoo meruw Almaañ- Itaali wi dafa sottiku woon ci kaw Britani. Bu ko defee, fafalnaaw yu Almaañ yi jog def lòkki yu toftaloo ci kaw dëkki Britani yi, la ko dale ca ut 1940g. waa Almaañ ñi nag li nu jublu woon ci loolu mooy manante Britani ci wommatu cig wàll, ak waaj ngir wàcce ay dooley Almaañ ca duni Britani ya, ci geneen wàll. Waaye taxaw gi askanu Britani wi taxaw taxawaay bu dëgër, te sax, moo tax ba waa Almaañ ñi manuñu woon a am li nu bëgg.

Réewi tapoo yi tàmbli woon nanoo ndàmmi ndam, di xaw a kawe réewi digg yi as lëf, bi Amerig duggsee ci xare bi ànd ak ñoom atum 1941g, ni ci Bennoog Sofiet gi dugge. Dooley Britani yi nag ndàmm nanu ndam lu mag ci jë bu Afrig bi ci kaw dooley Itaali yi, daal di leen dàqe ca Ecopi ak Eriteri. Looloo taxoon Hitler yabaloon ñaari kuréeli xare yu Almaañ ca bëj-gànnaaru Afrig, Marshal Rommell jiite woon leen ngir xettali-ji àndandoom ba ca Afrig. Ab xeex bu saf am ca bëj-gànnaaru Afrig ca 24 nowambar 1942g ci diggante réewi tapoo yi ak yu digg yi ci njiitug Mongomeri mi jiite woon réewi tapoo yi, ak Romal mi jiite woon réewi digg yi, ci noonu Réewi tapoo yi ndamu ci kaw yu digg yi ca xeex ba nuy wax Alamayni, ginaaw xeexub ñukkaakon (tank;char) bu mag bu sax fukki fan. Ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xeex bii, nanu ci tudd:

  • Teg loxo gi réewi tapoo yi tegoon loxo goxi bëj-gànnaaru Afrig, ginaaw bi nu fa dàqee dooley Itaali ji ak ju Almaañ ji.
  • Itaali wommatu na, soldaari réewi tapoo yi wàcc ca Sisil, ñu daal di daaneel nosteg Mussolini gi ca 3 satumbar 1943g
  • Nosub xare bi mujj na nekk ci loxol way tapoo yi , ginaaw bi mu nekkee ci loxol Almaañ ak réewi digg yi, àggoon nanu nag ci seen njòbbaxtali ndam atum 1942g

Ndamul Réewi tappoo yi Soppi

Ginaaw bi dooley Britani yi ak yu Amerig yi lijjantee ba am ndam ca jë ba ca Afrig, ak ginaaw bi Mussoolini daanoo, la réewi tapoo yi fasoon yéenee jële fi Almaañ. Ñu wàcce woon soldaar su dul jeex ca tefesug Normandi ga, àggoon nanu cib lim ñaari milyoŋi nit daanaka, ñu tegoon leen nag ci kilifteefug Generalu Amerig bii di Dwaayet Asinhawar. Bu ko defee yii doole daal di teg loxo Fraans, Beljig, Holand (suuf yu xóot yi). Dooley Almaañ yi xëyoon nanu wëlbati një – cig deltu ginaaw - jëme Almaañ, waaye dooley tapoo yi mayuñu leen woon fu nu yakke seen nàkka, ngir ragal ñu jekkaat ba amaat doole ju nuy songeeti kenn, ci noonu ñu dab leen ca saa sa, jot a sutuxlu ca digi Almaañ yu soww ya ca fewriye 1945g.

Ruus yi nag ñoom jotoon nanoo jéego jéego yu am solo ci jëwub penku bi, ci goxi penkub Tugal bi, ginaaw ba fa dooley Almaañ yi jugee, ci noonu ñu nangu jëwub Tugal gu penku gi ci suwe 1944g. Ci nii daal la dooley Almaañ tàbbee ciy xat-xat yu jafe, ci kanamu doole yu rëyub lim te nu waajal leen ci ngànnaay yi mujj a génn, bu ko defee Almaañ xëy di ku ñu gaw ci diggante ñaari wàlli kuur , ci diggante penku ak soww, looloo juroon Almaañ faroon wommatu ci mujjantal gi, ci me atum 1945g, ñu daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak réewi tapoo yi, loolu mujj di li taxawal dooley xare ju Almaañ jii jot a miiral adduna bi sonnal ko ngir xareem yu bari yii. Leegi nag réewi tapoo yi – di Angalteer, Fraans, Bennoog Sofiet ak Amerig - nangu nanu Berlin péeyub Almaañ, jàmmaarloo gi waa Almaañ yi doon def ak a dàkku seenub dëkk taxaw te jeex .

Wommatug Sapoŋ Soppi

Waa Amerig yi yanoon nanu seen bopp coonab xare bi ci penku kontar Japon. Ginaaw bi waa Amerig nangoo suuf yu bari ci li Japon tegoon loxo ci xare bi, lanu dogu woon ci gañe xeex bi, ginaaw bi nu jotee fent bombub fepp (bombe atomique), te bëgg a xam li mu man, te bëggoon it Japon wommatoo ci seeni loxo. Ñu daal di jug ci ut 1945, sànni ñaari jum yu fepp ci ñaari dëkk ci Japon ñooy: Irosima ak Nagasaki, ci noonu Japon mujj wommatu, daal di xaatim ag wéer ngànnaay ak waa Amerig yi ci turu réewi tapoo yi, ci satumbar 1945g, bu ko defee ñaareelu xare bi daal di jeex.

Li ci juddoo Soppi

Ay ngérte yu bari juddoo nanu ci xareb adduna bu ñaareel bi, bokk na ci yooyu:

  • Def ndajem Botsdam ca anéeru Berlin, ca 17 sulye 1945g, ngir jeexal xeex bi. Britani teewe woon na ko, Fraans, Bennoog Sofiet gi ak Diiwaani Amerig yu Bennoo yi.
  • Dagg goxub Brusiya ci Almaa ñ gu penku gi, bu ko defee Bennoog Sofiet gi jël ca wàllug bëj-gànnaar ga, Poloñ jël wàllug bëj saalum ga, ñu joxati Poloñ dëkkub Danseg bu gore bi (waaxub Danseg)
  • Séddale Almaañ def ko ñeenti barabi sañ-sañ, ci diggante Amerig, Britani, Fraans, ak Bennoog Sofiet. Ci atum 1949g la njëkk a am ci taarixu Almaañ ñaari reew sosu ci Almaañ, te yor ag nosteg pénc (systeme republicain) walla tosteg askan, ñooy: Almaañ gu soww gi walla péncum Almaañ mu bennoo mi (la république Fédérale d’Allemagne), nekk nag ci ron saytug Amerig, Britani ak Fraans, Bon di péey bi. Geneen gi di Almaañug penku gi (Brusiya gu njëkk ga), walla Almaañ gu demokraasi gi (la république démocratique allemande), Bennoog Sofiet gi saytu ko, Berlin gu penku gi dib péeyam. Ñu fàttali leen rekk ne Amerig, Britani ak Fraans mujjoon nanoo may Almaañ atum 1951 mu wut ay soldaar.
  • Almaañ ñàkk na mbooloom xareem bu dëgër ma te rëy, ñàkk ngànnaayam yu bees ya te jëm kanam, bi nu tasee ab xareem neewal dooleem.
  • Tegoon nanu Almaañ mu war a fay li mu yàqal rewi tapoo yi.
  • Nosaat koom-koomu Almaañ bi, rawati na nosteg alal gi ak gu endustri gi, yooyu yépp ñu jëme leen leegi ci luy ligéeyal mbiri yi dul xare.
  • Séddale Otris def ko ñeenti barabi sañ-sañ ci diggante Britani, Amerig, Fraans ak Bennoog Sofiet. Otris it des ci ron teg loxog réewi tapoo yi ba ci atum 1955g, ak doonte réewi tapoo yi nangu woon nanu ne réew la mu temb dale ko ca atum 1946g.
  • Réewi tapoo yi nangoo nanu ci Japon dun yu am solo, bu ci mel ne Farmosa ak Sakalin añs. Rafleel ko ci mbooleem moomeelam yi nekkoon ci màmbulaan gu atlas gi. Dooley Amerig yi nag juge nanu Japon atum 1951g, ginaaw bi nu xaatimee ag kollareg wéer-ngànnaay cis een digganteek goornamaab Japon bic i dëkkub San Fransisko.
  • Xaatim nanu ag juboo ak Itaali, Bulgari, Romani ak Hongri atum 1947g, gii juboo nag li mu yaxal mooy réew yii warloo fay réewi tapoo yi ay alamaani xare.
  • Deltu ginaawug ñaari réew yii di Fraans ak Britani ci nekk gi nu nekkoon ay réewi adduna yu mag ci ginaaw xare bi, bu ko defee Amerig ak sofyet yi jël seen barab, mujj it di réew yi ëpp doole ci adduna bi, mujj yor ngànnaay yu bon te aaytal.
  • Nërmeelug ñaari noste yii di Nasi ak Fasi ci Tugal ak nosteg xare ga nekkoon Japon, te noste gu mu ci doon rekk sag am bokk na ci li fi indi ñaareelu xare bi. Nostey diktaatoor yooyu bokkoon nanu ci nooni mbokkte yi gën a mag
  • feeñug dankub mbokkoo bi (bloc socialiste) ay réew yu bari bokk ci, Bennoog Sofuet gi jiite ko, mu ci mel ne : Kore gu bëj-gànnaar gi, Wietnaam gu bëj-gànnaar gi, Poloñ, Bulgari, Romani, Cekoslowaki ak Hongri añs. Bu dee nag Siin gu Askan gi ak Yogoslawi nag, ñoom ñaar ay réeyi mbokkoo lanu waaye nekkunu woon ci ron yilifug Bennoog Sofiet. Dankub bopp-alal bu gore bi it feeñ, Amerig jiite ko, làmboo nag réewi Tugal gu soww gi, niki: Britani, Fraans, Almaañ gu soww gi, Holand, Beljig, Danmark ak Norwej añs. Amerig it warlul yii réew ndimbalug alal ak gu xare, ngir ñu man a taxaw ci kanamu dankub mbokkoo bi.
  • Sos tapoog càmmooñu Atlas (Otan) atum 1939g, mooy tapoo gi boole woon Amerig, Britani, Fraans, Kanada, réewi sowwub Tugal bi, Japon ak Turki. Réew yii nag danu ne woon ku ci song menn rekk, song nga yeneen yepp. Ñu kollarante woon ci seen biir ci dimblante ci wàllug aaru, koom-koom ak alal. Ci geneen wàll, tapoog Warsaw gi daal di taxaw, tukkee ci Bennoog Sofiet ak réewi mbokkoo yi topp ci ginaawam ci càmmooñu Tugal ak penkoom.
  • Jëya ju rëy ji juddoo ci xeex bi muy faatug lu sakkan ci dooomu aadama ak yàqug alal ju dul jeex, ngir jumtukaayi xare yu xereñ yi nu ci jëfandikoo ñuy jum yi (les missiles), bombi fepp yi, nuuraakon yi ak ñukkaakon yu diis yi ans. Xare bii moo ëpp lu mu yàq, ray ko, màbb ko ca moomam ja ko fi jiitu woon.
  • Ëttu àtte yu Normbrug yi ngir àtte ñoñ Nasi ñi ci tuumay jèqi fitna ak sabab xare bi ak def ay tooñaange jëme ci ñu ñu tëj ñi (les prisonniers) ak ñi ñu njafe ca reewi tapoo ya. Àtte nanu fa tam njiiti nosteg xare gi nekkoon Japon.
  • Juddug mbootaayu xeet yi, ngir dëgëral jàmm ak tere xare yi ak xulooy réew yi, ak amal mbaandute ak yamoo ci réewi adduna bi.
  • Koom-koomu àdduna bépp a naatoon ginaaw bi xare bi jàllee, li ko waraloon di naali tabax yeek yeneen yi nga xam ne defaraat dëkk yi la doon ligeeye ak wàllug tabax ci anamam yepp. Bi gënoon a rëy ci naal yooyu mooy bu Marsaal.
  • Judduwaatug joŋante ci ngànnaay ci diggante ñaari dank yi: bu mbokkoo ak bu bopp-alal, ak sosu gi xare bu sedd bi sosu ci seen diggante, naka noonu dund ci jàmm gi am leegi ci diggante xeet yi ci kaw suuf.

Xare bi ci Afrig Soppi

Lu bari ci xarey Afrig yi (sànnikati Senegaal yi ca lañu woon ) jawali nañu Tugal, ngir xeexal Faraas. Xarekati Afrig yii ñi ngi nekkoon ci dundiinn wu tar te wow, ci biir yeer yi ak ci sedd bu metti bi, jànkoonte nañook jafe-jafe yu bari, lu ci mel ne ñàkk a dégg làkkuw waa Faraas wi akug tumbrànke. Waaye loolu lépp teewul ñu ràññikoo woon ag njàmbaare akug dogu. Xare ba jeex na ci ndamul Faraas ak ñi àndoon ak moom, ñu dàq Almaañ, mu doxe ci ñàkk mbooleem sancoom yi ci Afrig.

Afrig gu yamoo gi Faraas yilifoon ci njiitul Flips Ibuwe dafa nekkoon di jàppale Degol, bu ko defee njiiti Afrik gu sowwu gu Faraas gi ñoom di jàppale Almaañ, ba ca tabaski 1942 g.j, booba lañu wëlbatiku jàppaleji way tappoo yi .

Waa Afrig yi yamuñu foofu, waaye yabal nañu ay xarekat ca jëwub xare ba (front de guerre) ngir jox ñam way xare yi ak jox mbell Tugal.

jeexug xare bi Soppi

Ci atum 1945 lañu daan Almaañ. Sapoŋ it daanu ngir fàccaakonub saal (bombe atomique) ba waa AameriK yi taal ca kawam. Ñaareelu xare bi dakk na - niki bi ko jiitu woon - alag dundug ay milyoŋ ciy nit.